38EELU NDAJEM BENNOOG AFRIG (UA)

Yeneen i xët

Aji bind ji

38eelu ndajem Bennog Afrig (Union Africaine) mee ngi ñuy amal jamono yii fa Ecopi. Njiiti réewi Afrig yi di ko fa teewe ci diirub ñaari fan ngir waxtaane ponk yu deme ni jàmm, kaaraange, yeesal i càmpeef añs.

Tay ci gaawu gi, 15i fan ci weeruw féewiryee 2024, lañu tàmbali 38eelu ndajem Bennoog Afrig fa Addis Abeba, réewum Ecopi. Dinañu ko wéyal ba ëllëg ci dibéer ji, ci teewaayu mbooleem Njiiti réewi Afrig yi. Ndajem ren ji nag, dees na fa waxtaane ponk yu bari yu soxal diiwaan yi ba ci kembaar gépp, niki jàmm ak kaaraange, yeesal campeefi kurél gi, bennale koom-koom gi.

Bokk na ci li leen gën a soxal nag, waxtaane caabalug ñaari at gu jëm ci wéer ngànnaay yi ngir dakkal lépp luy xare ci kembar gi fii ak atum 2030. Dinañu càmbar itam taxawaayu mbootaay mi ci biir kurélug G20. Cig pàttali, mbootaayu UA bokk na ci way-bokk yi sax (membre permanents) ca atum 2023. Dees na càmbar tamit taxawaayam ci doxiinuw àddina si, rawatina lu jëm ci yeesal ndajem kaaraange Mbootaayu Xeet yi ONU.

Ginnaaw bi ñu ubbee ndaje mi, indi nañu ay coppite ci boppu mbootaay mi. Njiitu réewum Móritani mi, Mohamed Uld Séex El Gasuwaani, joxe na lengey njiiteef gi naataangoom bii di João Lourenço. Mohamud Aali Yuusuf mi jiite dipolomasi réewum Jibuti moo wuutu Musaa Faki Mahamat ci njiitu ndiisoog kurél gi.

Ginnaaw bi mu fa teewee ni ay naataangoom, Njiitu réewum Senegaal li, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, gaawantu na ci ngir amal i waxtaan ak yenn Njiiti réew ngir fasanteek ñoom ay déggoo ci bëgg-bëgg yi ñu bokk ci wàllum suqaleeku.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj