Tey, talaata, 4 awril 2023, la Senegaal di Màggal jonnug boppam, ginnaaw juróom-benn-fukk ak ñett, bim moome boppam ba tey. Ñu war ko màggal fépp ci réew mi, soldaar yiy wone seen bopp, di amal i maaj ci biir fukk ak ñeenti diiwaani réew mépp, rawatina fi Ndakaaru, Njiitu réew mi di ko fi teewe at mu jot.
Ca atum 1960 la Senegaal moomoon boppam. Cig pàttali, Senegaal ak Mali, menn réew lañ woon. Keroog bi ñuy jonnale seen bopp, di génn ci nooteelu Farãs, dañu bennale woon ñaari réew yi . Waaye, réewaloo ga doxoon diggante Mali ak Senegaal, ñu duppee woon ko Maréewandoo Mali, yàggul. Ngoroo ga dafa gaaw a tas. Nde, bi ñu tàmbalee demal seen bopp, keroog, bésub 20 suwe 1960, ñaari weer kepp lañ ci teg, bésub 20 ut 1960, Seŋoor ber Senegaal, daldi demal boppam ginnaaw coow li doxoon ci digganteem ak Móodibo Keyta.
Ginnaaw bi Senegaal, ci njiitalu Seŋoor, génnee ci Maréewandoo Mali gi, at mu jot, Senegaal day faral di màggal bésub jonnam. Bés boobu nag, dafa méngoo woon ak 4 awril 1960. Muy bés bob, ca la Maréewandoo Mali ga xaatimee woon déggoo ya ngir jot lenge ya, laata ñu koy biral ca bésub 20 suwe 1960. Moo tax, saa bu bés bi delsee, ñu koy màggal. Atum ren ji mooy 63eel wi yoon, bi ñu ko doore ca atum 1961, di ko feddali at mu nekk, ba jonni-Yàlla tey jile. Kolonel Musaa Kulibali di ci fàttali, naan :
« Bés bu mag a mag la ci bépp Saa-senegaal. Du rekk bés bu ñuy màggal jàmbaari réew mi. Waaye, bésub réewum Senegaal la. Moo tax ba Saa-senegaal bu nekk di ci gis boppam. »
Dafa di, aadaawoo nañ, at mu nekk, di tànnal bés bi ab ponk bu méngook jamono ji. Ren, nag, ponk bii toftalu lees ko duppee : Jàmbaari réew meek kaaraange gi : càmmug balluy mbindaare yi, muy joxe ci farãse : « Forces de défense et de sécurité : préservation des ressources naturelles ». Muy ponk bu am solo bob, tànnees na ko ngir delloo njukkal jàmbaari réew mi ; waayeet, ngir sas leen ci seen taxawaay bu mucc ayib ñeel càmmug balluy mbindaare yi. Maanaam, ni sóobare yiy saytoo ak a sàmm li askan wépp bokk. Ponk bi, nag, aw waxtaan la tam. Dees na ci fénc njariñi soldaar yiy bàyyi seen lépp, di daj lu nekk, fu nekk, ngir rekk sàmm kaaraange bokkeef gi, digi réew mi, alalu askan wi, rawatina balluy mbindaare yi.
Bu ñu nee bésub jonn, maanaam bésub moom-sa-réew, nag, xel yépp daldi dem ci xew meek maaj yi. Làrme bi war a maaj ni mu koy faral di defee at mu jot. Wàcc-liggéey yi, maanaam alaateret yi, ak sax feccaakon yi, maanaam masoret yi, kenn du des ginnaaw. Ren, ñu ngi ciy xaar 5740i doom-aadama yu war a maaj ci 14i diiwaani réew mépp, ci teewaayu Njiitu Réew meek waa Nguur gi, bànqaasi réew mi, askan wi, ba ci gan yi bawoo bitim-réew. Kenn bañ koo uute ngir jëmmal bés bi nootaange jeexee. Njiitu réew mi woo woon na ci waa kujje gi, waaye dañ ko gàntal.
Màggalug bile bés, wareef la, di warteef ci ku nekk. Dafa di, kat, bés bees di kañoo la ngir li mu nekk bésub réew mépp. Waaye doon naat luy fàttali ni, bésub xeex la ngir moom sa bopp. Waaye, waxtaan, wax dëgg ca la, am déet ?
Naam, Senegaal a moom réewam ci lees yaxal ak lees di wax. Naam, doomu Senegaal a jiite réew mi, di doxal. Am nan ay dig yu leer, am làrme, am uw askan, di bokkeef, am ndeyu-àtte buy yoonal doxiinu réew mi. Waaye, ndax loolu kese mooy moom sa bopp. Déedéet. Ndekete, noo ngi maaj boobaak tey, di tëgg ak a fecc, waaye bari nay mbir yuy wone ne réew mi moomagul boppam ba tey de. Nde 63i at ci ren, réewum Senegaal di jéem a mënal boppam, mu tëw a sotti. Ndax, ba tey, buumu njaam gi dox sunu diggante ak Farãs dogagul. Kon, bésub 4 awril, naxee-mbaay la walla ?