Ginnaaw juróomi weer biñ leen jàppee ak tey, sóobarei koddiwaar yaa ngi ci loxoy Saa-Mali yi ba léegi. Waaye, Nguuru réewum Koddiwaar yónnee na fab yebleef (délégation) ngir mu dox tànki jàmm ba sóobare yooyu mën a dellu ci seen i yitte. Liñ fa jële nag doyandi na xel donte ni njàpp gi yàgg na lool.
Fukki fan ci weeru Sulet 2022 la njiiti Maali yi tegoon loxo ci 46i sóobare ca dalu fafalnaaw bu Móodibo Keyta. Sóobare yooyu nag, ña nga bawoo woon ca réewum koddiwaar. Li waral ñu téye leen foofu mooy liñ leen jàppe niy mersaneer (maanaam ay ndaw yees fay ngir ñuy def i ñaawteef) yu buruxlu ca réew ma te lenn andiwu leen fa woon lu dul jéem a sàkkal pexe njiit ya.
Keroog bi njàpp gi amee la njiiti Koddiwaar yi tàmbalee weddi tuuma yooyu. Mësuñu leen a nangu benn yoon. Jot nañ sax siiwal ne sóobare yooyaa nga bokk ca ña waroon a dooleel sóobarey Minusma (Mission multidimensionnelle intégrée des nations unies au Mali) yi fa Mbootaayu xeet yi yebal ngir jàmm delsi ca Mali. Kii di kolonel Gesowaa Maahi Armànd miy xelal Njiitu réew ma ci wàllu làrme bi ñeel bittim-réew, jotoon na sax yékkatiy kàddu :
« Salgadoo mi yor kàddu Minusma bi ca Mali xamle na ni moom ci boppam xam na cëru ndimbalu réewu Koddiwaar moomu nekk Maali. Ñees jàpp bokk nañ ci mbindu mu Minusma. Cëru ndimbalu réew ùooùu yàgg naa am. »
Waaye, Njiiti Mali yi mënuñoo gëm loolu. Ba fii mu nekk nii, ña ngay wéy di jàpp ni sóobare yooya dañ leen a yebal ngir ñu daaneel Asimi Goytaa mi nekk di jiite jamono jii réew ma. 19i fan ci weeru sulet la leen magum toppekat bi ci Bamaakoo taqal ni dañ doon jéem a nasaxal kaaraange nguur gi. Biñ demee weer ak tuuti, ñu bàyyi ñetti jigéen ña ca bokkoon, daldi yem foofu.
Ci Alxames jii weesu, 22i fan ci weeru desàmbar wi, la yebleefu Koddiwaar bi agsi Mali ngir gën cee waslu àq niki yebleefu réewu Tógóo bi jëkke woon def. Jot nañ am um ndaje ak njiiti Maali yi ba xaatim benn déggoo, ci yombalu yebleefu Tógóo bi. Mënees na jàpp ni sax mbir maa ngi ci yoonu sotti. Ibraahyma Tene Watara mi jiite yebleefu Koddiwaar bi moo nu ko xamal :
« Doon na mbir mu nekk ci yoonu sotti. Te mën nanoo wax sax ne sunu tukki bii ci suufu Mali am na solo lool. »
Ba tey bu ñu sukkandikoo ciy kàddoom, ponki waxtaan wi dëgg kenn biralu leen. Liñ ci mën a jële daal mooy ab réeroo la bu am ci diggante ñaari réew yu jegeyoo te doon na baax ñu toog waxtaan ngir gindeeku. Ndax kat, ak lu mën a xew, jàmm a gën ay.