Tay ci alxames ji lañu doon amal ndajem jëwriñi kurélu OHADA (Organisation pour l’Harmonisation en Afrique du Droit des Affaires). Ki ko ubbi mooy elimaanu jëwriñ yi Usmaan Sonko. Mu nekkoon ndaje mu am solo. Ba tax, mu sàkku ñu góor-góorlu ci dooleel kurél gi. Su ko defee mu mën a bokk ci liy jur i saafara ñeel jafe-jafe yi muy ci wàllug koom-koom ak nekkinu askani Càmm yi ci bokk.
Jëwriñu Yoon ji, Usmaan Jaañ, jëloon kàddu gi, daldi xirtal ay ñoñam ci ñu gën a saytu ak a yaxanal alalu kuréel gi. Cig pàttali, moom Usmaan Jaañ moo jiite ndajem jëwriñi OHADA yi.