5eelu NDAJE MU MAG MU COSYDEP

Yeneen i xët

Aji bind ji

Kurélug COSYDEP (Coalition des Organisations en Synergie pour la Défense de l’Éducation) amal na juróomeelu ndajeem mu mag (Assemblée générale ordinaire). Ñu doon ko amal barki-démb ci alxames ji, 12i pani desàmbar 2024 fa Ndakaaru.

Ndajem ren ji nag, ñiŋ ko doon amal ci teewaayu Mustafaa Giraasi, jëwriñu njàng mi, ak ñu bare ñuy yëngatu ci wàllu njàngale ak ay ONG. Wëppa wi moo doon « Tabax yoonu njàngale mu méngook tolluwaayu jamono ak i jafe-jafeem, ak li « révolution numérique » laaj ». Li ñu ci nammoon nag, mooy dellu waxtaane jafe-jafe yiy gàllankoor njàng mi, rawatina limu jàngalekat yi matewul.

Naka noonu, Abdurahmaan Géy, fara-caytu UDEELS (Union Démocratique des Endeignants et Enseignantes du Sénégaal) dellu na def ab taxaw seetlu ci néewaayu limu jàngalekat yi. Ba tax muy rafetlu yéene ji Nguur gi am ngir jëlaat ay jàngalekat yees di mottalee 6400i jàngalekat. Terewul nag mu leen di fàttali dige yi fi jaaroon, jóge woon ci Nguur yi jàll, te ba léegi dara taxawu ci. Mu dellu gis ni « …daara ju amul limub jàngalekat bu matale, yàq la rekk », te « bu (Njiitu réew mi) dëggalee yéene ji mu fésal, dellu ànd ceek ñu am taxawaay, mënees na saafara jafe-jafe bi fii ak ñetti at. Ba tax muy sàkku ci Nguur gi mu taxaw ci temm te amal jëlaate bi ci anam yu leer te jëm ci ñi ko yayoo.

Bi mu jëlee kàddu gi, Jëwriñ ji Sëñ Giraasi rafetlu na amalug ndaje mi, rawatina ci jamono ju am solo ji ñu ko wootee. Gaawantu na ceet ngir fàttali ni mbir yi tembaree tay ngir ñu saafara jafe-jafe yu bari yi ci wàlluw njàng mi te ñu bari lool te yaatu ba ci àddina sépp. Muy woote nag jëme ci yoonu njàngale mu njaboote ñépp te yamale, njàngale mu fullaal xarala yu bees yi tey sóoraale jafe-jafe yi yegseegul.

Lu jiitu ndajeem COSYDEP mi, amaloon nañ am ndaje mees duppee « Forum citoyen » ngir taxawal sémbuw njàngale ñeel 2034, laltaaye ko ak i pexe yu yees ngir am njàng mu mucc ayib. Foofu itam, Jëwriñ ji fésalaat na fa yéeney Nguur gi ci tëggaat njàngale mi ak taxawu bu baax jàngalekat yi. Terewul muy fàttali waa COSYDEP ni duñ rekk am mbooloo, ñu am doole nañu ci yoonu wut ay saafara, nekk itam àndandoo bu am solo ci Càmm gi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj