Tay ci gaawu bi, 4i pani desàmbar 2024, doon nañu tóllanteeti « Bëccëgub setal sunu réew ». Muy juróom-ñetteel wi yoon ginnaaw bi ko Njiitu réew mi sumbee ak tay. Ñu doon ko amal ci jàppandalug njëwriñal Larme bi.
Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, ma nga woon tay fa Yëmbël, fa dëkkuwaay yu ñu duppee Cité Comico (Coopérative militaire de construction) ngir ubbite juróom-ñetteelu bëccëgu set-setal réew mi, ñu gën ko miin ci « Setal sunu réew ». Ci yoor-yoor bi lañu ko daldi tàmmbali ci teewaayu Seneraal Biram Jóob (jëwriñu Làrme bi) ak kilifay bànqaas gi féete Ndakaaru.
Moom Seneraal Biram Jóob sax, njëwriñ gi mu jiite lañu dénk doxalin beek jàppandalug 8eel wi yoon. Wëppa wee ngi ñu tënkoon ci kàddu yii di « setal sa gox, aar sa yaram : taxawaayu sóobare yi ci weti askan wi ». Ngir waajal bés bi, njëwriñu Làrme bi jotoon na amal démb ci àjjuma ji bésub maye dereet fi réew mépp. Naka noonu, dajalaatu nañu 1 217i mbuusi deret.
Ci bi muy jiite ubbite gi, Njiitu réew mi yékkati na fay kàddu woote ak xirtal askan wi ci bés bi ak njariñ li mu war a amal réew mi. Ba tax muy sàkku ci askan wi mu làmboo xew-xewi set-setal yi, daldi leen jikkowoo. Ci noonu, muy fàttali askan wi ni war na ci ñépp, ñu saxal seen taxawaay ci jox réew mi seen bopp ngir ñu gën a mën a tabax sunum réew ak sunuw askan. Njiitu réew mi rafetlu naat taxawaay wu mucc ayib wu sóobare yi wone fi réew mépp. Mu leen ciy sant, jaare ko ci jëwriñ ji, Seneraal Biram Jóob.
Bu weesoo loolu, Seneraal Biram Jóob xamle naat ni sémbu tàggatu wi Làrme bi di amal ñeel ndaw yi am na ay jeexital yu am solo, rawatina ni muy yokkee seen mën-mën, seen yar ak seen taxawaay ci soxlay réew mi.