8eelu NDAJEM GALIEN AFRIG : CÀKKUTEEFU NJIITU RÉEW MI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Njiitu réew mi woote na jëme ci Afrig mën boppam ci wàllu paj mi. Muy woote bu mu amal fekk mu doon jiite xew mi ñu doon tëje Ndajem Galien Afrig mi ñu doon amal fi Ndakaaru.

Barki-démb, ci àjjuma ji, 31 oktoobar 2025, lañu doon amal jotaay bi mujj ci Ndajem Galien Afrig mi ñu doon amal fi ndakaaru. Ndaje maa ngi ñu tàmbali woon keroog talaata, 28 oktoobar, waroon koo dawal ci diirub 4i fan. Mu ren ji di 8eel  wi yoon. Ñu doon ci waxtaane wëppa wii di « mën-sa-bopp ci paj mi, lu war ci Afrig ».

Bi muy biral ay kàddoom barki-démb nag ci tëj bi, Njiitu réew mi Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay biral na yéeneem, dellu ñaax ñi ko teewe woon ngir ñu gëm ni mën nañoo yóbbu Afrig ci mu mën boppam ci wàllu paj mi. Ba tax mu mel ni ku leen di jox yóbbal :

« Bu ñu génnee ci Ndaje mii, maa ngi sàkku ci ñu génnee fi Ndakaaru ak ub Pasug Afrig ñeel mën-sa-bopp ci paj mi. Mu tegu ci ñu dolli kopparal ko sunu bopp, bennale bu baax sunu diiwaan yi, dugal sunu loxo bu baax ci gëstu beek soste bi, ak dooleel dimbalante bi ak réew yeek askan yi ñàkk doole ».

Naka noonu, Njiitu réew mi di xamle ni mën-sa-bopp gi ñuy woote ci wàllu pàj mi lu mën a nekk la. Te teguwul lu dul ci gëm ni kembaarug Afrig warul di jéggaani rekk. Dafa war itam di defar. Lile dafay laaj réewi Afrig yi dugal ci seen doole bu baax te takku doon benn.

Ba tay ci Ndaje moomu, jëwriñu réewum Jibuti ji yor paj mi, Dr Ahmed Robieh Abdileh yékkati na fay kàddu yu méngook woote bi Njiitu réew mi amal. Naka noonu, moom itam muy woo Njiiti réewi Afrig yi ñu taxaw ci naalu jaar gi te xalaat ni bés dina ñëw ndimbal yiy jóge bitti dog.

Naka noonu, jëwriñu Jibuti ji di xamle ni :

« Mën-sa-bopp gi nuy woote ci paj mi, du ay kàddu rekk koy taxawal. Lu ñuy tabax la ndànk ndànk, dem ci gën a dajale koppar yi ñu am ngir mën sa bopp ci paj ci lu wóor »

Muy xamle ni kopparal gi dafa ci am solo lool sax. Ba tax na Nguur yi war cee taxaw, ndax mënuñu di wékku ci ñeneen ñi rekk. Ci noonu, mu dellu xamle ni Kurélug réewi penku Afrig fas na cee yéene taxaw. Nde ci ayu-bés yii di ñëw, dina amal ndaje mu am solo fa Jibuti, jëwriñi paj mi a kyu koom-koomi réew yi fa bokk yépp dinañu fa teew.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj