Grand Théatre bu Ndakaaru mooy amal géewub waxtaane làkki réew mi : mbir mu am solo ci ëllagi Senegaal.
Ci jamono ci ñuy warloo delloosi wareefu mbatit ak njàng, géewu waxtaan bu tudd (Nguur ak i làkkam fii ci Senegaal) mooy am ca Grand Theatre bu Ndakaaru ci 22i fan ci weeru Mee, 2025, bu 15i w. jàpp 18i w. jotee, te kippaangog Grand Théatre de Dakar sooke ko.
Ci diirub ñatti waxtu, ay ñoodiŋ ak i ferey réew mi, dañuy daje ngir sottante – ci wolof – tolluwaayu làkk yi ci Senegaal : ndax dañuy jël wenn làkk boole ko ak wu tubaab wi ? Ndax dañuy jëfandikoo làkk yu bari ? Nees di def ba di boole ko ak sunu tolluwaay bi, ak koom mi, ak doxaliinu réew mi ?
Ànd ci ko ak Usmaan LÓO ak Nday Koddu FAAL ci joxeg kàddu yi, ci waxtaan wuy dajale ñoodiŋ yu wuute ci làkki réew mi : Sëriñ Baabakar JÓOB Buuba, Soxna Njéeme SOW, Sëriñ Sullaymaan Ñaŋ, Sëriñ Mamadu FAY, Sëriñ Musaa SAAÑA, Sëriñ Paab Aali JÀLLO, ndax njaaxaanay lanuy tëdde.
Yéene samp laaj yu bari, yenn yu mel ni :
-
Ndax liggéeye wenn làkku réew mi du faagaagal làkk yi ci des ?
-
Ndax liggéeye wenn làkk dana dooleel njàng mi, doxaliin wi ak yokkute gi ?
-
Naka la làkku tubaab wii nuy doxe di nekk ci nekkin wu sax ak làkki réew mi ?

