BUL BIND… / BINDAL…

Yeneen i xët

Aji bind ji

Seen yéenekaayu web ci wolof ubbil na leen xët wu bees wees duppee BUL BIND… / BINDAL… Jubluwaay bi mooy di beqi njuumte yeek yàq yees di faral di nemmeeku ci pénc mi.

Lees seetlu mooy ne, gëdda gees jox làkki doxandéem yi (farãse, araab, àngale, añs.), kenn joxu ko làkki réew mi. Ba tax na, képp kuy bind ci làkki doxandéem yi, dinga def sa kemtalaayu kàttan ngir sàmmonte ak sàrti mbind mi. Waaye, bu dee làkki réew mi moom, rawatina wolof, ku mu neex binde leen nu mu ko neexe. Loolu dafay xaw a niru ag doyadal guy wund ag yaras. Ndaxte, bu nu seetaanee yàq ak jalgati yooyu, dafay mujje gàllankoor xeex bees di xeex ngir suqali ak gànjaral sunu làkk yi. Ci beneen boor, loolu dafay nasaxal fonk gi nu war a fonk sunu bopp, di jeexital ci worma ji nu am ci sunu mbatiit ak moomeelu bopp. Wolof nag dafa ne, ku xeeb sa cosaan, ñu xeebal la ko. Te sax, lees war a xam mooy ne, làkki réew mi, wu ci nekk, dafa am ab dekkare bu yoonal am mbindam, tëral i sàrt yoy, ñépp ci lañu war a tënku.

Ni ko yeneen làkk yu bari amee ci réew mi, wolof dafa am ab dekkare bu tëral mbindiinu làkk week teqalem baat yi. Mooy dekkareb limu 2005-990 bu 21 oktoobar 2005 bi leeral sàrt yees war a cëslaayoo ci mbind mi. Teewul nag, ba tay, ñu baree ngi binde wolof bi nu mu leen neexe, di bañ a sàmmonte ak li dekkare bi sàrtal. Looloo sabab yàq yu bari yees di nemmeeku ci pénc mi, rawatina ci saabalukaay yi ak mbaali jokkoo yi. Naka noonu, danoo fas yéene di tànn, ayu-bis bu nekk, as lëf ci njuumte yooyee ak yàq yi, daldi leen beqi, leeral fu njuumte li walla yàq bi féete.

Tele RTS lanu tàmbalee, ndaxte mooy tele bi askan wi moomal boppam, di taawu tele yi. Kon, dafay jaadu nu doore ci moom. Ci kaw loolu, gis nanuy njuumte ci mbindiinu 21i turi jotaay.  Njuumte yooyu lanuy fésal fii, beqi leen, wane naka lees war a binde baat yi.

Nu ngi xamle ni ci dekkareb 2005 lanu sukkandiku ngir beqi njuumte yeek yàq yi.

BEQI BI

Bul bind “Béguéléne” / Bindal “Bégeleen”

Fii, am na ñetti njuumte : […GU…] ; [……] ak […E]

Ni ñuy binde wolof ak ni ñuy binde farãse du benn. Bu dee làkkuw farãse, soo bëggee am ndégtu [ɡ] ci kanamu loy yii di « e » walla « i », fàww nga yokk ci benn « u », mu jox la “gu”, niki « mangue » [màngo].

Loolu nag, amul ci wolof. Ndax, jarul ngay toftal « u »  ci « g » ngir mën a dégg “gu”.

Ñaareelu njuumte li mooy [……]. Fii, kuutlaayu jëmm (pronom personnel) bii di « LEEN » lees fi am, mu fiy taxawe taxawaayu aji-jëf (sujet).

Ñetteelu njuumte li mooy li ñu indi loyu « » ci njeexitalu baat bi. Ndaxte, ci mbindum wolof, wépp loy wees bind, dees na ko dawal (lire). Kon, ci misaal, bu « e » bi ñëwee ci njeexitalu baat bi, dangay mel ni kuy wax « béguéléné », te du noonu. Kon, lees war a bind fii mooy : « BÉGELEEN ».

Nu bàyyi xel ne, bu dee « -leen » bi dafa taq ci « bége- », li kàddu giy tekki mooy : « Yeen, bégeleen. ».

Bu ñu teqalee « bége » ak « leen », su boobaa « leen » dafay am taxawaayu mottalu jëf (objet), maanaam « ñoom » lay wuutu. Li kàddu giy tekki su boobaa mooy : « Yaw, bége leen [ñoom]. »

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj