SENEGAAL / « CYBERATTAQUE » : AY SÀMBAA-BÓOY SONG NAÑU « FISC » BI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Xibaar bu doy a doy waar la Sikafinance siiwal ci bésub alxamesu tay jii, 2i fani sebtàmbar 2025. Ay « pirates informatiques » ñoo song « système informatique » bu DGID (Direction générale des impôts et domaines). Nee ñu, bi ko sàmbaa-bóoy yooyu songee ak tay, am na ayu-bis. Nde, boobaak léegi, xelteef yi (logiciels) ndawi DGID yi di liggéeyee yépp ñoo paan. « Pirates informatiques », ci lees wax, Tugal (Ërob) lañu nekk. Te, ngir delloosi xelteef yooyee, ñoom piraat yi dañuy laaj koppar yu tollu ci 6i miliyaar ak xaaj ci sunuy koppar, maanaam 10i miliyoŋ ciy ëro.

DGID mooy bànqaasu Nguur giy saytu lépp lu aju ci lempo (juuti yi, galag yi ak kumbal yi) ak itam suuf yi. Lépp luy dugg ci gafakag réew mi ak li ciy génn yépp, ci loxoy DGID lay jaar, moo koy saytu. Bànqaas bu ni mel nag, bu amee jafe-jafe bu ni mel, boo moytuwul, réew mi ci boppam mooy taxaw. Ndaxte, dafay nasaxal liggéeyu Càmm gépp.

Li ci gënatee doy waar mooy ne, piraat yi dañu siiwal lenn ciy rootaan (données) yu DGID yoy, warul tas ci pénc mi. Loolu dafay wane ni sàmbaa-bóoy yi caaxaanuñu.

Lii dal DGID nag, du Senegaal jiituwu ci. Nde, mës na dal na ci kaw ay réew yu mag yu deme ni Etaasini (Atlanta) ca atum 2018. Booba, kilifay dëkk ba dañu bañoon a fay koppar yi piraat ya doon laaj. Waaye, daanaka génnee woon nañu lu tollu ci 17i miliyoŋi dolaari amerig ngir defaraat seen « système informatique ».

Ca atum 2021 tamit, lu ni mal daloon na réewum Irlànd, ba ñu songee lees duppee Health Service Executive (HSE). Rax-ci-dolli, ca atum 2022, ay piraat yu bokk ci kurélu Conti songoon nañu réewum Kostaa Rikaa, muy duwaan ya ak lempo ya, yàq fa lu bari ci wàllu koom-koom.

Kon, du lu bees. Waaye, li mat a laaj mooy yan matukaay la njiiti réew mi jël ngir fàggandiku ? Ban taxawaay lañu fas yéene am ngir lijjanti mbir mi ba sàmm alalu réew mi ? Dañuy fay li piraat yi laaj am déet ? Li ci kanam rawul i bët.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj