Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, door na tukki yu am solo ci njeexitalu ayu-bés bii ñu génn. Ñaari tukki yépp mi ngi leen di amalee ci biir kembaaru Afrig gi. Benn bi, mi ngi ko doon amalee fa réewum Ruwàndaa. Beneen bi, ma nga koy amalee jamono jii ca réewum Keeñaa. Te, ñaari tukki yooyu yépp, bu ci nekk dafa am lu ko wund.
Àjjuma jii weesu la Njiitu réew mi dem fa Kigali, ca réewum Ruwàndaa. Naataangoom bi, Póol Kagame, moo ko teeru fa dalu roppalaan ba. Mu doon tukki bu am solo sax. Nde, def na fa diiru ñetti fan. Dafa di, yamul ci doon tukki nemmeeku ak xaritoo kese. Tukki la boo xam ne ngir gën a rataxal seen diggante. Ndax, ñaari réew yi am na ay jokkalante yu dox seen diggante.
Ci tukkeem boobu fa réew moomee, jot naa dem fii ñuy dippe “Mémorial du Génocide de Kigali”. Nde, béréb la bob, dafa am lu muy màndargaal ci mbooru réew moomu. Ndax, kenn umpalewul ne jaar nañu ci guddi yu lëndëm laata ñuy agsi fii ñu tollu tay. Ginnaaw gi la ko naataangoom dalal fa njéndel réew ma ngir ñu amal aw waxtaan. Bi ñu jógee ci waxtaan woowu, am na juróomi déggoo yoo xam ne ñaari réew yi xaatim nañu leen. Bi ci jiitu, di li ñeel wàllu wiisaa yi. Ñaareel bi di lu ñeel doxal ak caytug sémbi suqaliku yi. Ñetteel bi moo ñeel mbirum mbay mi. Ñeenteel bi jëm ci wàllu wér-gi-yaram. Juróomeel bi moom mi ngi jëm ci li ñuy dippee “collaboration dans les services correctionnels et les questions pénitentiaires”.
Ba tay ci gaawu bi, jot na faa gise ak doomi Senegaal yi nga xam ne ña ngay dundu ca réew moomu. Mu doon ndaje mu am solo. Nde, moom Njiitu réew mi, rafetlu na anam yi fa doomi réewam yi nekkee. Laata muy jóge ca réew ma, ànd na ak Njiitu réewu Ruwàndaa ci doxantu bu muy amal ñaari dibéer yu nekk ci weer wi. Te, dox bi ñu amal dem na ci juróomi kilomeetar ci mbeddi Kigali yi. Te, li ñu ko dugge du lenn lu moy gën a sàmm seen wér-gi-yaram ak seen kéew.
Bi mu matalee tukkeem bi fa réew moomu la jubali réewum Keeñaa. Nde, kii di Njiitu réew ma, Wiliyam Samoye Ruto moo ko fa woo ci benn xew-xew bu ñuy amal at mu jot. Laata loolu, jot naa gise ak doomi Senegaal ya fa nekk. Xew-xew boobu ñu fay amal nag, ñi ngi koy dippee “Journée des Héros” (Mashujaa Day). Dañu koy màggal at mu jot, ñaar-fukki fan ci weeru oktoobar. Njiitu réewu Senegaal jot na faa yékkati ay kàddu yu am solo. Nde, dafa xamle ne màggal bés bu ni mel mooy màggal ak njukkal ñi leen doon xeexal. Waaye, loolu tamit mooy firndeel ne ñu ngi aar sunu mboor. Te, loolu mooy leeral sunu ëllëg.
Kon, ci gàttal, lii la Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, jot a defagum ci tukki yi mu amal ci ñaari réew yooyu. Nde, kenn umpalewul ne réew mu ci nekk am na lu mu séq ak réewum Senegaal. Te, ab diggante moom du yam ci wax rekk, dees koy dox tamit, di demalante, di dikkalante. Ndax kat, ëlléer lum ñaw ñaw, du tere yenn saa yi mu aajowoo ñu dàggi ko.