Ginnaaw bi mu jëlee lenge yi niki Njiitu réewum Senegaal, Basiiru Jomaay Fay jël na ndogal yu bir. Nde, dafa xaatim dekkare buy neenal ndigal yi Maki Sàll mujjee jël laata muy fegal.
Démb, 3 awril 2024, la Njiitu réew mi jël ab dekkare bob, day far ndogal yi Maki Sàll jëloon yépp ça mujjantalu Ndajem àttekat yu mag yi, keroog 29 màrs 2024. Cig pàttali, Maki Sàll dafa tabboon Abdulaay Njaay, def ko muy njiitul ëttu àttewaay bu mag bi.