AADAMA BARO RËCC NA !

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ag Nguur naroon na daanooti ci Afri sowu-jant. Gàmbi la naroon xewe. Ayu-bés bii weesu la amoon ñu nisaroon foqati foqati Nguur gi ci loxoy Aadam Baro. Waaye, seen naal bi mujjewul a àntu. Ci li Nguur gi xamle, ñenn ci sóobarey Gàmbi yaa xënte woon daaneel Càmm ga. Waaye, Yàlla àndu ci. Nde, seen kilifa ci boppam, di njiiti làrmeb Gàmbi bi (Haut commandement de l’armée) ñoo neenal seen pexe mi.

Àllarba, 21i fan ci weeru desàmbar 2022, la Nguuru réewum Gàmbi gi siiwal ab xibaar bu bette. Ndege, dañoo bëggoon a foqati seen Nguur ga. Ebrima Sànkare, kenn ci way-xelali Njiitu réew ma, Aadama Baro, te yor kàddu Nguur ga, moo ko njëkk a siiwal :

« Nguuru Gàmbi gee ngi yëgle ni, ginnaaw ba mu jotee i xibaar ci caytukat yi ni ay sóobarey bee ngi nas ngir daaneel Nguurug Njiitu réew mi Aadama Baro, te mu faloo ci baatu askan wi, kilifay làrme bi amal na ca saa sa taxawaay bu mat ba jàpp ci ñeenti sóobare yu laaleek foqati Nguur gi nu foog. »

Ci ginnaaw gi, génne nañ beneen yëgle ngir xamle ni jàppees na ñenn ci ñi doon jéem a foqati Nguur ga. Ñu jële ci ni teg nañ loxo lu tollu ci 7i sóobare. Kenn ci ñoom di kàppiteen, mu am keneen ku ci nekk liyëtnaa. Am na tamit benn way-pólitig bu bokk ci kujje gi te nekkoon jëwriñ ci Nguuru Yayaa Jàmme bu ñu jàpp. Moom sax, li ko dugal moo di dafa génnoon cib widewoo naan Nguur gi dana daanu balaa wotey gox yeek gox-goxaat yi di yegsi. Ba tey it, am na yeneen ñaar yu ñuy wéy di wër, yees yaakaar ni taq nañ ci mbir mi.

Barki-démb, ci alxames ji, njiit ya génne waat nañ ab yëgle. Abubakar Suleymaan Jeŋ, di xelalkat ci wàllu kaaraange réew mi, moo ko jàng ci kanamu saabal yi ngir indiy leeral ci ni mbir mi deme. Ñaŋ cay dëggal ni yittey foqati Nguur gi lu am la. Liñ jot a am ciy xibaar leeral na bu baax pexe yiñ tëraloon. Amal nañ sax i ndaje ciy béréb ba laloon seenub naal. Fees ko nammoon a jaarale mooy jàpp njiit yu kowe yu Nguur gi, tekki ndombal tànki ófisiyee làrme bi (dale ko ci masoor yi jëm kow), ba noppi tëggaat làrme bi.

Fii mu nekk, njiit ya taxawal nañ ag kurélu gëstu gu war a topp mbir mi ba mu sës. Feek weer la war a jébbal caabalam. Cig pàttali, bu yàggul dara sax, njiitu réewi Afrig sowu-jant yi jël nañ ndogalu taxawal ab làrme ci diwaan bi ngir muy jàmmaarlook rëtalkat yeek foqatikati Nguur yi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj