ABBAAS FAAL : “BOROOM NDAKAARU”

Yeneen i xët

Aji bind ji

Tay, ci altine ji, lañu doon wote ngir fal meeru Ndakaaru biy wuutu Bàrtelemi Toy Jaas mi ñu fa déjjati. Li ko waral du lenn lu moy daan bi gàllu ci ndoddam. Looloo tax du mën a wéy di yor ndombog-tànk googu. Ginnaaw bi ñu ko wàccee, am na ku ko wuutu woon wuutug négandiku as diir. Waaye, tay jii lañu doon leeral lépp ngir xam kan mooy doon meeru Ndakaaru fii ak 2027.

Atum 2022 la Bàrtlemi Jaas jotoon ci meeri bu Ndakaaru. Ca jamono yooya, mook Usmaan Sonko ñoo bokkoon genn lëkkatoo, muy Yewwi Askan wi. Waaye, ginnaaw gi, dañu tàqalikoo, ku nekk jël saw yoon. Kii di Abbaas Faal sax, nga xam ne ma nga woon ca meeri ba, Bàrtelemi dafa defoon i pexe, daldi ko fay jële. Foofa la xeex ba doore seen diggante ba ca wotey 2024 ya weesu.

Ginnaaw bi ñu amalee wotey palug Njiitu réew mi ca atum 2024 ba Pastef jël Nguur gi, dañ cee teg wotey palug dépite yi. Bi wote yooyu jàllee ci la Bàrtlemi Jaas ñàkk ñaari moome yi mu amoon yépp. Muy gog dépite gi ak gog meeri bu Ndakaaru. Li ko waral mooy daan bi ñu ko daanoon. Bi loolu amee, am ku ko fa wuutu.

Tay nag lañu doon amal wote ya ngir fal beneen meer. Dafa di, wote yii ñi ñuy dippe ay “conseillers” rekk ñoo koy def. Ñeenti lawax ñoo doon xëccoo. Muy Muhammet Masàmba Séy, Daawuda Géy, Abbaas Faal bu Pastef ak Ngóone Mbeng bu Taxawu Senegaal. Kii di Abbaas Faal moo am ñeen-fukki xob ak juróom, Ngóone Mbeng am fanweeri xob. Kon, Abbaas Faal moo jël ndam li. Ba tax na, bés niki tay, mooy nekk meer bu Ndakaaru.

Naka noonu, kii di Bàrtlemi Jaas mi mu wuutu ci béréb boobu amaat na beneen jéll fa ëttu àttekaay bu kawe ba. Ndax, dabantal ga mu dugaloon dañu koo mujjee gàntal. Loolu di firndeel ne, jamono jii, Bàrtlemi amatul genn ndombog-tànk. Li mat a laaj kay mooy lan moo nar a doon ëllëgu Bàrtlemi Jaas ci pólitig ?

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj