SYTAS (Syndicat des Travailleurs des Aéroports du Sénégal) nanguwul a dégg ndogal li njiitul AIBD li, Séex Bàmba Jéey, jël ngir wéyal wàññi limub liggéeykat ya foofa. Muy ñaawlu anam yi mu ko jëlee ak di ko woo ci yeneen i pexe yu dul dàqe.
Ginnaaw bi mu ko corfatee ci fan yii weesu, Séex Bàmba Jéey dellusi na ci ndogalu wàññi limub liggéeykat yi mu tàmbali fa dalub roppalaan bu AIBD. Fekk mu doon janook taskati xibaar yi démb ci àjjuma ji ngir aajar tolluwaayu koomug kër gile. Naka noonu, mu àndi ciy leeral ak di biralaale ndogal yi ci topp ngir këru liggéey gi wéy di dox.
« Dinañu wéyal wàññi limub liggéeykat yi. Ngir ñu mën a jekku sunuw doxalin ak a ñoŋal ëllëgu kër gi, fàww ñu delloosi sunuy lim ci lees nu ràng. AIBD-SA dafay dund jomono ju metti ju soqikoo ci jëlub liggéeykat yu bari yu jotoon a am ci diggante 2022 ak 2024. Ëppal boobu dafa andi liggéeykat yi ci lim bi jéggi dayo ba àttan leen mujje jafe ci gafaka gi. »
Sëñ bi Jéey dellu di xamle ni dinañu jël i matukaay yi war ngir amal wàññi yooyu ci anam yu màndu, yu leer te digg-dóomu. Waaye, matukaay yu ni mel duggul wenn yoon waa SYTAS (Sàndikaa Liggéeykat yi ci dali roppalaan yi nekk Senegaal). Nde, dañoo dàq ndogal li, dellu xamle ni lay yi kilifa yi biral taxawul bees sukkandikoo ci dogu 23 bu Déclaration Universelle des Droits de l’Homme. Rax-ci-dolli, dàqe yi doonul lu tëdde njaaxaanaay, te mënees na am yeneen pexe yu leen mën a fànqal jéyya ju ni mel ci askan wi.
Naka noonu, dinanu taxaw, xeex ngir àqi liggéeykat yi dàqe yi diir. Ci seen i kàddu, seen taxawaay bile du tere ñu bàyyi xel bu baax jafe-jafey koomug AIBD. Ba tax ñuy woo njiit yi ciy waxtaan ngir amandoo saafara yu gën, yuy tax ñu mën a téye liggéeykat yi ñu nar a wàññi, sàmmaale seen liggéey. Ci gis-gis bile, amal nañu ay junj yu ñu jàpp ni bu leen kilifa yi jëfee dina mën a jur njariñ.
Ngir bañ a dakkal ay liggéey, dañuy sàkku ñu toxal liggéeykat yi fa dali roppalaan yu Ndar ak Sigicoor, bees demee ba di leen ubbiwaat. Leneen lu ñu gis ni mën na jur saafara itam mooy ñu dekkil sémbuw CMA (Centre de Maintenance Aéronautique) ak wu Aéroville, ngir sos fay liggéey. Menees ne itam fullaal moomeelug AIBD ci wàllu suuf fa Ndaakaaru, te mu jële woon ko ci boolant gi mu amaloon ak ADS (Aéroports du Sénégal) yi.
Ñuy xirtal kilifa yi ñu tàmbali ay waxtaan ngir am ay pexe ci dàqe yi nga xam ni defuñu lu dul di yokk kër yu bari ñuy gën a ndóol.