Tali baa ngiy wéy di faat bakkani way-tukki yi. Aksidaŋ bu jàll, beneen tegu ca. Ñaari fan ci ginnaaw, aksidaŋ bu metti amoon na ci yoonu Tiwaawan wi. Tey jii, ci suba teel gi, jeneen jéyya a amati ci talib Luga bi. Ci boori 9i waxtu lab biis bu jóge woon Dagana jëm Ndakaaru, daldi daanu. Ndeke, bi daamaar bu mag bi duggee ci diiwaanu Njàmbur bi musiba bi am.
Ci wetu isinu SPIA la aksidã bi ame. Fi mu nekk nii, ci li rotagum ciy xibaar, 5i doom-aadama ñàkk nañ ci seen i bakkan. Ñoom, ci saa si lañu dee. Mu am itam 33 yu ci am i gaañu-gaañu ba sàppëer rawale leen ca raglu Amadu Saxiir Mbay bu Luga.
Nee ñu nag, pólis dina luññutu ba xam ci yan anam la jéyya ji ame ak sabab yi ko waral.