Aksidaŋ yaa ngi wéy di rey nit ñi ci kow tali bi. Bërki-démb, ci boori ñetti waxtu jàpp ñeenti waxtu ci ngoon la aksidaŋ bu metti am fa Mbàmbiloor. Liy firndeel metti gi mooy ne ca saa sa la fa 6i bakkan rot. Manaam, ñoom jotuñoo sax jóge ca béréb ba waxumalaak ñu leen di rawale ca raglu ba. Aksidaŋ boobu nag, genn daamaru Dacia ak benn sëfaanu-ndox (kamiyoŋ-sitern) ñoo mbëkkante. Ndeysaan, juróom-benni doom-aadama ñoo ca ñàkke seen i bakkan. Te, ñoom ñépp bokk.
Naqar ak tiis la waa Mbàmbiloor fanaanoo bërki-démb, rawatina mbokki way-dëddu ya. Ndax, nee ñu daamar gu ndaw gi juróom-benni nit ña mu yeboon ñoom ñépp ñoo bokk. Ñoom nag, Mbàmbiloor lañu bawoo woon jëm Ndakaaru ci menn ndaje. Waaye, mujjuñoo àgg. Ndax, nee ñu, bi oto bi génnee gox bi, ci benn wiiraas la dawalkat bi jaawale yëf yi. Maanaam, mënatul woon xàmmee lan lay def ak lan lay bàyyi (perdre le controle). Ca la dalee ci benn sëfaanu-ndox.
Bi loolu amee, ña mu yeboon moom ca saa si la seen i bakkan rot. Maanaam bi waa sàppëer daataan yegsi fekk na ña nekkoon ca daamar gu ndaw gi faatu. Ñoom juróom yooyu faatu ca saa si, ay jigéen lañu ak benn xale bu ndaw. Ña fekke jéyya ja nag doon nañu jéem a rawale dawalkat ba ca raglu ba gën a jege. Waaye, loolu taxu koo mucc. Ndax, dafa mujjee ñàkk bakkanam moom tamit.
Jéyya yiy am ci yoon yi moom day mel ni saa yu ñu foogee ne wàññeeku na rekk, ndeke booba la waalo gën a aay. Dafa di, ren jii la aksidaŋ yi gën a bari, gënatee metti. Bu jàll, beneen ñëw gën a yées. Loolu di firndeel ne aksidaŋ yi du matuwaay yi Nguur gi di jël kepp a leen fi mën a jële. Waaye, fàww dawalkat yi tamit xar ci seen tànki tubéy. Ndax, ndimbal kat na ca fekk loxol boroom.
Moo tax, fim tollu nii dafa war ci dawalkat yi ñu xoolaat seen doxalin ak seen dawalin ci tali yi. Ndax, daanaka léegi, mënatoo toog ab diir te déggoo jéyya ci tali yi. Kon, dafa jot ñu defaraat seen toogaay. Ndax kat, nit ñaa ngi jeex ci tali bi.