AMINATA TURE ÑEEL CREI : « BU DÉMB DOON TEY… »

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ci alxames jii weesu la dépite yi jàllale sémbub àtte bi fi jële CREI (Cour de répression de l’enrichissement illicite). CREI nag, nekkoon fi ëttu àttewaay bees sosoon ginnaaw palug Njiitu réew mi Maki Sàll ca atum 2012 ngir topp ñees jàpp ni dañoo sàcc alalu réew mi. Ginnaaw bees ci andeey coppite ngir wuutale kook beneen ëttu àttewaay bees duppee PJF (Pool Judiciaire financière). Aminata Ture mi jiite woon toppe yi delsi na ci bu baax ci waxtaan wi mu séqoon ak sunuy nattaango yu Itv.

Démb ci àjjuma ji, la waa Itv dalaloon Aminata Ture. Moom nag, mo nekkoon jëwriñ ji ñu dénkoon wàlluw yoon jamono ji mbiri Karim Wàdd di jolli ca CREI. Mu bare lool ponk yu ñu fa waxtaane. Waaye, liggéey bi mu jot a liggéey ci Nguurug Maki ak ñi mu doon topp ci luubalub xaalisu réew mee ci gënoon a fés.

Ci niral, bees ko laajee ndax bu démb doon tey, mu nekk Njiitu réew mi, dina fa yóbbu nit ñu àtte ko, jàdd-jàddalul benn yoon. Li mu ci tontu ca saa sa mooy :

« Bu démb doon tey, ma def li ma defoon. […] Bu demee ni mu demee woon, li ma defoon laay defaat, bu jaaree fa mu jaaroon rekk. Li mu wund mooy jamono yooyu CREI moo amoon. Amul woon leneen. »

Lees seetlu ciy tontoom, dafay wone ni amul lenn lu muy réccu ci ñi mu fa jot a yóbbu. Dafa di sax lu muy ndamoo, di ko bàkkoo. Ndax, dëggal na ni 200i tamñareet yees di laam-laame, Nguur gi jot na ci.

Yemul ci loolu sax. Nde, gis na ni lépp luy wayndare ca jamonoy CREI, dees ko war a topp ba mu jeex. Te loolu moo war a nekk liggéeyu toppekat biy am ci biir PJF bi. Looloo tax mu dellu dëggal ni :

 « Dina am ay wayndare yoo xam ni dañ leen koy jébbal. Bu ko defee mu def liggéeyam ci ni mu ko war a defe. Loolu kese la. […] Wayndare yépp, dañ leen di topp ba ñu jeex. »

Ki fi nekkoon jëwriñ ji ñu dénkoon wàlluw Yoon di wone ni àndul wenn yoon ci ñi naan CREI bi amu fi woon njariñ, rawatina waa PDS yiy wax naan dara taxu ko woon jóg lu dul faagaagal doomu Abdulaay Wàdd ji.

Aminata Ture yemul ci sémb bii kott. Yëy na yàbbeet ci dogub 27 bi dépite yi gàntal :

« Dogub 27 bi, dépite yi def nanu lees ci waroon a def. Maa ngi leen ciy ndokkale. Moo xam dépite Bennoo bokk yaakaar yi la walla dépitey kujje gi. Li xew kenn mësu koo gis. Njiitum réew moo xam ni fileek juróom-benni weer nga abale, du moom moo war a soppi ndayu sàrtu réew mi. »

Ni ko ñu bare waxee, noonu la ko waxee. Jàpp na ni sémb bi dafa sax teey xel. Li ko war mooy mu bàyyi ki nga xam ni moo koy wuutu, mu waxtaan ak askan wi ci loolu. Jàpp na ni sax dees na ci amal sàrt yoy, Njiit luy waaj a dem du mën a laal ndayu àtte réew mi. Te noonu la ko CEDEAO bëggee.

Aminata Ture dellu di sàkku ci dépite yi ñuy am taxawaay bu ni mel, di fullaak faaydaay bañ saa bu doonee ay mbiri Senegaal.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj