Bokk na ci anam yi nit lootaabee ag dundam ci kaw suuf, lu nekk ak ku mu ko dénk. Loolu moo waral, mboolaay gu nekk seddalewu ci ay pàcc yu wuute tey mottalante. Pàcc bu ci nekk rekk, ña ko yore ne ca, di bay seen waar ngir gën a jëmmal mboolaay gi ba noppi gën koo jëmale kanam.
Ci kow loolu, mboolaay gu ci nekk ak ni mu bindoo ak it li mu baaxoo. Am na foo xam ne, yenn cër yi dees leen di donn. Ñépp mënuñu cee jot. Ku ko nar a yore, fàww nga bokk fenn fi. Maanaam, kenn du fa gàlloo yenn cër yi lu dul mu bokk cig kuréel gu ràññekku walla muy doom cig njaboot gu ñépp xam. Am na it feneen fu askan way tànnee ñi muy dénk i mbiram. Ci ñooñu, ñenn ñi, dañuy toog ba ñu woo leen, sant leen liggéy. Ñeneen ñi ñoom, ñooy jógal seen bopp, laaj ngir ñu sas leen. Muy lu xaw a yéeme nag.
Ndax kat, mbirum askan uw lëmm, ni mu diisee ak li ci nekk yépp ciy coono, nit ñemee yékkati loxoom, laaj ngir ñu gàllal ko dara ci loosam. Doy na waar de ! Ba yenn saa yi sax mu jaral ko tayle bakkanam, di xuloo ak a xeex. Nit a ñeme coono waay !
Ndax mënees na jàppee nit kooku ni ku dogu ci dékku lépp coono ngir jariñ askanam ?
Bu dee tontu li waaw la tamit, bir na ne du ngir képp ku taxaw di laaj. Ndax kat, maam waxoon na ne, kenn du fekk baayam toog mu naan ko : “Baay, yónni ma barab sàngam”. Ku ko def rekk, waxul li mu nisër, denc ko cib ruq, fu sori ci biir xelam. Nde, ñàkkul mu am lu mu nar ca yoon wa walla mu am fu mu bëgg a dem, ba noppi di wut poroxndoll. Bu baay soxlaa ndaw lu mu yónni kay, dina woolu ka mu wóolu yabal ko.
Naka noonu, niki réew yu bari, sunum réew, bari na fiy cër yu askan wiy dénkaane. Te, ñi mu leen di dénk, ñooy jóg, laaj ngir nu jox leen. Saa su jamonoy laaj jotee nag, ñi soxla ñépp ay taxaw, takk seen ndigg. Fexe ba, fépp fu doomu réew mi féete, ñu fekk ko fa. Ànd ci ak cawarte gu réy ba lépp lu mbir mi laaj, ñu def ko. Dëkk-dëkkaan yu ñu mësul woon a teg seen i tànk, danañu fa àgg, di niru-nirulu ña fay yeewoo, ci colin ak ci waxin. Niki kàkkatar rekk, garab gu ñu yéeg nirook moom. Lépp rekk ngir dagaan seen i baat.
Nu gis ne ñoom, li ñuy gën a def bu jamonoy tànn jotee, mooy di dig askan wi. Ci fan yu néew yooyu, lu ne dinañu ko dige. Mel ni, kàddu gu neex gu ñëw seen xel rekk, fàww mu tàbbi ci noppi way-déglu yi. Ku nekk ragg boppam ba set, defaru ba neex a xool. Ba noppi, naan moom a, bu dul moom du baax. Xam na fuy metti te, moom rekk a ci am pexe, nanu ko bàyyi, mu fajal nu ko. Ànd ko nag ak ug yeewute gu jéggi dayo niki nappkat buy meeb i jën, walla wund wuy ootal janax.
Dëgg la gaa, dige bor la. Waaye, kilifa ga waxoon na ne, digey way-pólitig, ña ko gëm doŋŋ lay sonal. Ñenn ñi sax àgg nañu ci di wax ne, waxi way-pólitig, jarul a dóor sa doom. Muy lu neexul a weddi nag. Ndax kat, néew na lool ci ñoom ñuy sàmmoonte ak seen i dige ginnaaw bi ñu jotee ci li ñuy dagaan. Mu mel ni, ba ñu ko waxee rekk, la génn seen xel.
Ci fan yii weesu, ak waajtaayu palug jàmbur yi, nu ngi doon dégg ñenn ci lawax yi doon dige yoo xam ne laalewul dara ak li nar a doon seen liggéey ca Ngomblaan ga. Ñu bari ci ñoom, doon wax ne dinañu saafara jàngoroy askan wi, feral seen i rongoñ yiy bas-basi. Ñenn ñaa ngi doon dige ne dinañu jàppale ndaw ñi ngir ñu am liggéey, ñeneen ñi doon wax ci raglu yi ak paj mi, ak yeneen yu ni mel. Te, duñu am sax lu ñuy seet bu ñuy yékkati yooyule kàddu. Dañ noo joxul cër nun ñi ñuy waxal walla dañoo xamul lan moo war a doon taxawaayu dépite yi ñu bëggoon a doon ?
Li nu sant Ngomblaan gi kat, weesuwul saytu liggéeyu Càmm gi, natt naal yi muy tëral ak teg i sàrt yuy xàll yoon yi gën ci réew mi. Sàrt yoy, ak fu ñu mën a joge (ci Càmm gi, ci askan wi walla ci ñoom dépite yi) duñu def lu dul jariñ ma-réew yi ak gën a ñoŋal seen ug dund. Lii, lu mu jote ak tabax i raglu walla bënn i teen ?
Ndax warul nag way-pólitig yi taf bët bu bon bi ñu baaxoo di nu xolee te jël bu baax bi ? Bu ko defee, ñu mën noo gis ni mu waree, xam sunu dayo nun askan wi. Te it, xam ne, sunu tekk-tekkaaral, tële ak ñàkk a xam waralu ko.
Jot na nag sëkk ngir ñu nawloo nu, jox nu cër bi war te am sunu kersa. Nu mën a ànd, lal sunu diggante ak sunuy jëflante ci dëgg. Bu ko defee nu dajale sunuy kàttan ak sunuy xalaat, boole ak seen i yos ngir Gaal gi jëm kanam.