Senegaal mi ngi ci guuta. Loolu la kurél yiy sàmm àq ak yelleefi doom-aadama xamle démb ci àjjuma ji. Fekk ñu doon amal ab lël ngir waxtaane tolluwaayu réew mi. Ginnaaw seen taxaw-seetlu, ñuy dellu di woote waxtaan ngir am i saafara balaa réccu di ci am yoon.
Juróom-ñaari kurél yii ñuy duppee Amnesty international/Sénégal, Lsdh (Ligue sénégalaise des droits de l’homme), Raddho (Défense des droits de l’homme), Afrika jom center, Article 19/Afrique de l’ouest ak Asutic (Association des utilisateurs des tics) ñoo woote woon ab lël démb ci àjjuma ji, 11 ut 2023. Ñuy ay kurél yuy yëngu ci sàmm àq ak yelleefi doom-aadama. Seen yitte nag moo doonoon waxtaane tolluwaayu réew mi ak ku nekk lan moo ci sa wàlla.
Ci seen lël boobu, kurél yi ànd nañu xamle ni réew mii di Senegaal mi ngi ci guuta. Te boobook léegi, ëpp na ñetti at. Seen gis-gis nag mooy ni du kenn ku ñu ciy joxoñ baaraamu tuuma ku dul Njiitu réew mi, Maki Sàll, ak nguuram.
« Seetlu nañu ni, bi fi Nguur gii ñëwee ba léegi, ñoo ngi jëfandikoo Yoon ci yoo xam ni du lenn lu dul uute ay gis-gis walla péete ci wàllu pólitig. Te jëfandikoo bi ñuy jëfandikoo Yoon ci làngu pólitig gi moo indi ñuy seppi ñenn ci kujje gi ak a néewal doole ñeneen ñi. Jamono yii, Saa-Senegaal yu bare def nañu ay weer ci biir kaso yi, te defuñu lenn lu dul wax seen xalaat ci Càmm gi walla ci ni Nguur gi di doxee. »
Jëf yu ni mel nag, dafa gën a yokku ci ñetti at yii ñu génn. Nde, ci seen ceetlu gi, diggante atum 2020, maanaam bi mbiri Usmaan Sonko yeek Aji Raabi Saar jollee ak tey, Nguur gi dafa gën a jëfandikoo i pexe yoy, dañoo safaanook Yoon ak di jalgati àq ak yelleefi nit ñi.
Lu ni mel a tax sax ba Séydu Gasama biral ni li fi xew mësu fee am bi Senegaal moomee boppam ak tey. Bi fi Seŋoor nekkee sax ak benn pàrti kott, Senegaal mësul a àgg fii mu tollu tey ci jalgati ak salfaañe àq ak yelleefi doom-aadama. Rax-ci-dolli, bunduxatal gi dafa weesu làngu pólitig gi. Bokk naat ci jëf yi ñu lim ne méngoowuñook daray Yoon walla àq ak yelleefi nit ñi, xatal gi ñuy xatal taskati xibaar yi ba mënatuñoo jëfe seen liggeey ni mu waree, lënkaay gi ñuy faral di dogg saa su leen neexee, añs.
Ginnaaw bi ñu biralee seen i njàngat, li ñu ci mën a tënk mooy ni Maki Sàll dafa naxasal demokaraasi bi fii ci réew mi. Ba tax ñuy sàkku mu dakkal jaay doole gi mu nekke, dakkal njàpp yi te bàyyi képp koo xam ni dañ la teg loxo ci lu dul kujje walla wax sa xalaat. Ñu yokk ci tamit ni bees bëggee, fi réew mi, demokaraasi bi sax fi dàkk, fàww Nguur gi jàmmal taskati xibaar yi te gën leen a féexal.
Ginnaaw loolu, mbooleem kurél yi ànd nañoot woote péncoo ngir moytandiku balaa réew mi di gënn a suux ciy guuta, rawatina jamono yii ñu dëgmalee ay wote ci féewaryee 2024 wi.