ÀTTE BOR FEY WALLA… FÀTTE ? (Ndongo Si)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ndongo Si

Mbasum Covid-19 mi am nay njeexital ci koom-koomu Afrig, dekkal na sax coow lu bare ñeel boru réewam yi. Wolof Njaay dafa ne : « Àtte bor, fey » waaye dafa mel ni kàddoom yooyu tey lañu gën a naqadee dégg ! Li ma ko tax a wax, nag, du lenn lu dul coow li ne kurr jamono jii. Coow li coow li, mooy na réewi Tubaab yi am doole far bor bi leen Afrig ameel. Dëgg la, coow loolu du lu bees. Daanaka 30i at a ngi boroom xam-xam yeek boroom pas-pasu Afrig yi di ci wax. Am na sax ay réew yu ci yàgg a àddu, naan wareesu koo fey. Ci atum 1988, ndem-si-lla-ji Mamadu Ja, mi njëkkoon a nekk Njiitu jawriñSenegaal yi, woote woon na am ndaje mu yaatu ci Ndakaaru ñeel payug bor boobule. Ñu bari ciy doomi Afrig ak sax ay farañse jotoon nañoo teewe ndaje moomu.

Mu mel ni coowal bor bi day dem ak a dikk. Moom kay, saa yuñ foogee ne wax ji naxsaay na, mu jibaat, coow li neeti kurr. Noonu la deme jamono jii. Ndege, mbasum koronaawiris bi yemul rekk ci di faat ay bakkan. Koom-koom yi sax song na leen, nasaxal leen. Menn réew muccu ci, moo xam yu sowu yi la walla yu Afrig yi. Waaye, mbir mi ci nun la gën a mettee. Xeex mbas mi dafa laaj alal ju takku te, jamono jii, xaalis  dafa ñàkk. Ku amul lu la mën a dundal, doo tal fey bor. Looloo nu dal, nun Afrig. Loolu la Njiitu-réew mi, Maki Sàll, xam bay sàkku ci réew yi Afrig ameel bor ñu baal ko ko, walla ñu toxal pey gi ba jëmmi-jamono. Ci bàttaleem bu 3eelu fan ci weeru awril la ko Maki Sàll waxoon laata mu koy baamtuwaat ci waxtaan wu mu séq ak France 24. Am na, nag, ay kilifa yu ko ci fekksi ; ñi ci gën a fës di Njiitu-réewum Farãs bi, Emmanuel Macron ak Paap Farãsuwaa, njiitalu Jàngu bi.

Bees sukkandikoo ci sunuy njiit, Senegaal 1000 milyaari CFA la soxla ngir xeex mbas mi. Waaye li muy fey at mu ne ci bor mat na 500 milyaar. Kon, du mën a boole ñaar yii : fey bor ak xeex koronaa. Mooy li nasaraan yiwax rekk, mëneesul a dàqandoo ñaari njombar. Yeneen réewi Afrig yi saalika noonu, ndax fukki dërëm yu ñu am, ñaar yi ci bor bi la jëm. Moo tax ku ci farataal peyug bor bi, doo mujje lu-dul taxaw seetaan nit ñi ñuy dee.

Looloo waral réew yi ëpp doole ci àddina si may leen nopp, nangoo seetaat mbirum bor bi. FMI ak Bànk Monjaal, ñoom, baal nañ ñenn ñi seen i bor, daldi bëtal bori ñeneen ñi. Wànte, nag, ba tey kenn taxawu ci ne, dees na far mboolem bor yi réewi Afrg yi ameel seen i lebalkat. Te, bees amee ab taxaw-seetlu, dees na xam ne du doon mukk lu ñuy baral.

Boroom xam-xam yiy gëstu ci mbirum koom-koom biral nañ ne, bor bi mooy fiir gi réew yu mag yi keppe Afrig ngir doxloo ko ci seen waaw. Réew yooyu bu ñu lebalee Afrig 100i dërëm, 50 yi dañuy dellu ci seen i loxo ci diirub benn at. Bu ko defee, réewi Afrig yi dañuy fey saaku ak gall. 50 yiy dugg itam duñu dem ci lu am solo. Déedéet, dañu leen di dugal ci ay caaxaan yu mel ne TER bi nga xam ni ñu bare ànduñ ci tey ci Senegaal. Li des ci xaalis bi, ay kilifaa koy kkal pexe.

Loolu moo tax bor biy nirook boru jinne, wuute lool ak li ñu miin. Ndaxte, loo fey fey day wéy di yokku rekk. Bor bu feyam tëwa jeex, àtteem mënul a doon leneen ludul dëkke koo fey te du lu yomb. Bu ñu waxee dëgg sax, xel nanguwu ko. li am ba am moo di ne dafa war a dakk, lu ko moy réewi Afrig yi duy dellu doon ay jaami Tubaab yi. Waaye tey, mel na ne am na bunt bu nu koronaa bi ubbil.

Ndax boru Afrig bi dina fey ci barkeb koronaa ? Yàlla rekk a xam.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj