XIBAAR ÑEEL YOON
Téyandi nañu ràppëer bii di “10 000 problèmes” ak kii di Lamin Kàngaam. Ki tax ñu jàpp leen mooy Sëriñ Abdulaay Fay mi leen jure (pelent). Ab widewoo a leen boole. Ca biir widewoo booba, “10 000 problèmes” ak Lamin Kàngaam dañu...
Àddina yoon la wow, ku ko xas ba dëgmal, dem rekk. Moo waral sunu maam Jaal Mbaay tàggu nu biig, 14i fani oktoobar ci atum 2025, yemoo ak guddig 23i fani rakki-gàmmu, atum 1447.
Jaal Mbaay waykat la woon, bokkoon ci ñi gënoon a ràññeeku...