“Xalam demoon na bay neex, buum ga dog”. Wolof dina faral di wax kàddu gii. Waaye nag, wile yoon moom, xalam mi ci boppam moo damm. Xalamu Jimi Mbay ma woon, damm na, buum ya jaare fa dog ca talaata jee weesu, 12i fani féewiryee 2025.
Mustafaa Mbay, ca bamuy gone la tàmbalee bëgg xalam. Nee ñu, ciy fukki atam la jël i buum ak i xotti pot ngir defaral boppam xalamam mu njëkk. Ci ginnaaw gi la ko magam ju goor wutal xalamu dëggantaan. Noonu la demee ba sopp xalamkatu saa-Amerig bu ràññeeku bii di Jimmy Hendrix ba sax faf jël aw turam. Loolu tax nu gënoon koo miin ci Jimi.
Ñu bari xam nañu ko niki xalamkatu Yuusu Nduur. Waaye, du woon ab xalamkatam rekk yam ca. Nde, ci ñi sos “Super Etoile” la bokk. Mënees na ko boole kon ci kenoy kippaango googu. Te sax, ñoom ñaar ànd nañu lu jege 40i at. Ànd bu yàgg boobu ak xareñam ci li mu doon def tax na ba xalamam bokkoon ci li daan sàppali te di yokk cafka wayi Yuusu Nduur yi. Way wii di “Birima” rekk doy na ci seede bu mat sëkk. Nde, tungune du teew ñuy nataal. Na ca xalamam ma def moos, ku ca bàyyiwul xel it, dégg nga ko ak say noppi xol.
Moom nag, yamul woon rekk ci xalam. Nde, daan na ci boole way. Jot na sax génne ñatti “album” : “Dakar Heat” ca atum 1997, “Yaay digal ma” ca atum 2004 ak “Xare dunyaa” ca atum 2012. Wayandoo woon na it ak Maa-Saane way wu ñu duppee “Janq ndaw”. Ci wayam wi gën a siiw di “Yaay digal ma”, mi ngi ciy delloo njukkal way-juram wu jigéen ci taxawaayam bu jekk ba mu amoon ca kër baayam. Rax-ci-dolli, di koy wax naan ko : “digal ma, digal ma, yaw yaay digal ma, yoon wi ma jël sori na, lëndëm na te man ñemewuma fi. Yaay leeral ma, yaay booy xelal ma, sama yoon wi tiital na ma.”
Jimi Mbay, bàyyi na fi liggéey bu gànjaru te dootul fay mukk ci mbatiitu Senegaal. Jëf na, nu gis. Waaye it, xàll na yoon wu yaatu te leer.
Ni mu ko waxee woon ci wayam wii di “Yaay digal ma” : “Boo nekkee ci dara, ba foog ne dootul jeex, Buur Yàllaay ñëw ak dogalam bi”. Ndogal boobu nag moo ñëw yóbb ko ci 68i atam. Mu dem ci tukkite gu sori ngir noppalu ba fàww.
Nu koy ñaanal mu dal-luji ca ron garab yu mag ya ca guyaar yu gën a kawe ya. Picci foofu ya di ko wayal, xalamam yu neex yi di ko yeetal.
EJO ak LU DEFU WAXU ñoo ngi koy jaale Senegaal gépp, rawatina njabootu boppam ak képp ku mbatiit yitteel.