Tiis tegooti na ci kaw Senegaal, rawatina ci àttekat yi ak ñiy safoo mbatiit. Marie-José Crespin moo dëddu, moom mi bokkoon ci ñi njëkk a doon àttekat fi réew mi. Mi ngi làqu démb ci alxames ji, ginnaaw bi mu dundee 88i at ci kaw suuf.
Aji-dem ji nag, mi ngi ganesi àdduna fa Dahome (mi doon léegi réewum Benee) ci weeru Sulet atum 1936. Baayam di woon doomu Ndar, ndey ja moom, Farãs la cosaanoo. Moom Marie-José Crespin, mooy jigéenu àttekat ji njëkk a bokk ci Ndajem Ndeyu Sàrti Réew mi (Conseil constitutionnel) ca atum 1992, doon itam jigéen ji njëkk a jiite Ëttu àttekaay bu mag bi (Cour de cassation).
Soxna su ràññeeku soosu, mi ngi fekk baax Gore, di dun bi mu bëggoon lool ci xolam, daan taxaw temm ngir aar ko, xeexal ko. Moom ak ña mu bokkandool kurél gii ñu duppee “Xariti Mbindaare mi” (des Amis de la nature) jot nañu jëmbat garab yu baree bari foofa, ca dunub Gore ba. Jotoon na itam sumb ab xew-xew bu mu tudde woon « Gorée, Regards sur cours », di xew-xew boo xam ne, bu jotaan, saa-Gore yi dañuy ubbi seen i kër ngir artist yi ñëw fésal seen i ligéey. Te sax, bari na ci ñoom ñu fa tàmbalee, jaaree fa siiw. Jubluwaayu ndaje moomu, du woon lenn lu dul gën a jëmmal mbaaxi Gore.
Ba muy doon njegemaar, baaxoo woon na di dajale ay per yu gànjaru. Demoon na sax bay nas i caq ak yu ni mel. Loolu yóbb ko ba mu ubbi ab barab buy xamle mbooru peri Afrig yi.
Muy firndeel ni ku ràññeeku woon lool la ci wàllu yoon ak it ci mbatiit.
“Sa dund gi am na njariñ lool yaay bóoy. Waaye, waxtu noppalu nag jot na. Nelawal ba yàndoor !”
EJO ak LU DEFU WAXU ñoo ngi koy jaale Senegaal gépp, rawatina njabootu boppam, mbokki àttekatam ak képp ku mbatiit yitteel.