Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, jiite na ndajem jëwriñ yi barki-démb ci talaata ji. Ginnaaw bi mu defaree coppite yi am ci Càmm gi, dellu na ñaaxaat jëwriñ yi ñu farlu ci mbir yi gën a tembare, rawatina mbir yi ñeel...
Dépitey Ngomblaanu Farãs yi wote nañu pasum diiŋat (motion de censure), daldi daaneel Càmmug elimaanu jëwriñ ya, Michel Barnier. Dépitey kujje gees duppee « La gauche » ñoo dugaloon pasu diiŋat mi, wote ko, jàllale ko. Muy tekki ne, Càmm gi Michel Barnier taxawaloon...