Làmbu démb ak ju tey jeeka wuute ! Ndege, démb, bu nawet bi wàccaan, ci lañu daan tëgg làmb. Kon, nu gis ne ci njeexitalu mbey mi la mbër yi daan joŋante, ndax beykat yi ci seen bopp a daan bëre. Seetal ma lii rekk : jàmbaari tool, jàmbaari géew… Mbër mu ci nekk teewal sab gox ginnaaw bi nga fa wonee sag njàmbaar. Dafa di, nag, gox yooyoo daan bokk aw tund.
Lees ci jubluwoon ? Xanaa fésal fit ak ngóora, jom ak ngor, ak lépp luy màndargaal waxambaane bu làmboo jikko yi ñu fi lim. Rax-ci-dolli, làmb xew-xew bu mag la woon, di tax nit ñiy booloo, di rafetal diggante mbokk yeek àndandoo yi. Kon, mënees na jàppe làmbu démb ni daara, daara ju ndaw yi daan taataan i jikko yuy jëme kanam mboolem-nawle mi.
Bu loolu weesoo, lees ci war a jànge mooy ne : démb, ñi daan tëgg làmb jeek ñi daan bëre — beykat yi — duggewuñu ko woon wut alal walla màkkaan. N1épp xam nañu ni sunu maam yi bey lañ daan dundale seen njaboot. Te saa yoo nee mbey, xel yépp dem ci fulla, xareñ ak muñ, ñuy ay tànnéef ci jikko yi. Bu nu delloo cosaan daal, góor balay sëgg bëre, fàww mu doon ab ndàndi, ñu weg ko fa mu bawoo. Wax dëgg, royukaay noonu lay mel, dangay siggil saw tund, siggil saw askan, waaye yit dangay nekk sagal say way-jur ak sa njaboot.
Ndeysaan, xalam demoon na bay neex, buum ga saay.
Ci sunu jamono tey jii, ku-yeboo ne coppite yu mag am nañ ci mbir yi. Waaw ! Te coppite yi dañoo laxasook yàqute jamono ji. Ndax, tey koo laaj ci mbër yi ndax ay way-juram àndoon nañu ci muy takk ngemb di bëre, tontu bi benn lay doon : déedéet. Léeg-léeg sax am ci ku la ne moom làmb taxoon na ñu dàq ko seen kër. Li ko waral, nag, du lenn lu-dul ne kenn du am sa doom mu doon xale nga koy xiirtal ci muy bëre walla muy fecc, bàyyi fi njàngum daara walla xarala. Du càggéeni làmb baaxul, dafa di rekk ne, anam yi ñu koy defe léegee ñaaw te safaanook jëfi gor. Tey, ku déggal say way-jur, boo newul daara ja di jàng yaa ngi ci bérébu liggéyukaay yi di jàng xarala. Të ak ñàkk dégg seeni waxi waajur a tax ñu ci bari doon ay mbër. Waaye li am ba am moo di ne jamono jee soppi nit ñi niy kàkkataar.
Moone de, mel na ni tey ña tëwoon seeni waa-jur ca njëlbéen, ñoom lañu def royukaayi ndaw yi. Ndax, ñoo fi tekki di dawal ci daamar yi fi gën a yànj, dëkk ci kër yu taaru ba dee. Ku ko weddi seet ko ci jaraaf gi nu dénk njàng meek lépp lu ci ajuy doxale ; kilifa googu, bu daara yiy ubbi, muy ànd ak kenn ci mbër yi, di wër ak moom yenn ci ay daara. Muy lu doy waar ! Teg ci tamit, nataali mbër yooyu ñoo ne fàŋŋ ci téere yi ndongo yiy jànge. Te bu jant biy so, ba gone yi wàcc, ëtti daara yi dañuy soppiku aareen, mbër yi di ci tàggatoo. Moom kay, salfaañoo dëgg la dundinu askan wile def. ! Kon léegi daal ku bëgg a tekki na fexe rekk ba am, ak noo mën a ame ?