Coowal 29 miliyaari yi ñu ne woon dañu ko luubal ca PRODAC, dekkiwaat na. Kii di Usmaan Sonko njiitul Pastef li mooy ki xolli góom bi. Ki mu duut baaraamu tuuma nag di Maam Mbay Ñaŋ, mi ko pelent. Moom nag, wuyuji woon na...
Xeex bi jolleeti na diggante ndongoy iniwérsite Gastoŋ Berse ak takk-der yi. Jamono jii ñuy bind yaxal bi, xale yaa ngay jàmmaarloo ak takk-der yi ci kow tali bi. Oto demul, oto dikkul. Xeer yaa ngiy xërr-xërri, gërënaad yiy soqi, póno yeek matt yiy...