Bés ba ma ko déggee mu naan kilifa diine yi dañ maa ñaan ma fekki Maki, laa ni ci sama xel : Aysata mii de, xéy-na dafa paree dem ba noppiy làmbaatu ba xam nu ko askan wiy gise ëllëg. Waaye man ci sama wàllu bopp de, masuma woon a xalaat ne Aysata Taal Sàll dina mas a bokki ci ñooñu doyadi bay xéy weddi seen bopp, dem ànd ak Maki, ndax rekk bëgg a tedd. Ndekete yóo…
Dëgg la, Senegaal, danoo miin politiseŋ yiy toxu, dem tag fu seen ceeb di gën a niin ba loolu safatul kenn. Waaye ndaw sii moom, ñépp mere nañ ko. Am na sax ñu naan moo yées ci ñiy yëngu ci làngu pólitig gi.
Aysata Taal Sàll dafa am fu ko askan wi mës a teg, muy fésal li mu gëm ciy kàddu yu leer nàññ te yit daan ko jëfe. Bërki-démboo-njaay rekk la fi ne xel dajul muy ànd ak waa nguur gi. Ñépp jàpp ni waxi gor la, doonte sax néew na li ñuy gis kuy pólitig ba noppiy jiital sa ngor.
Jigéen ju mel ni moom, jekk kaar, nex i ree, ay kàddoom dëggu, soo leen déggee ñu dugg la, mu jàng ba am i lijaasa yu réy, bokk fu baax niñ ko waxe, danga war a jombal sa bopp yenn yi. Rax-ci-dolli, foo ko fekkaan mu ngiy xeex par-parloo tey sotle néew-dooley réew mi. Ku mel nii, daa sopplu te ku ko sopp wàcc nga.
Tey, bu Aysata demee ba génn ba set wecc ci li mu waxoon, mbetteel la, gàcce la. Ñu bare la mbir mi ub seen bopp, am na sax ñu dem ba yaakaar ne Aysata Sàll ñoom rekk la tooñ, tooñul keneen.
Léegi nag, ñépp a ngi ciy teg seen bët : ci jigéeni réew mépp, amu ci kenn ku yoon may mu bokk ci joŋante 2019 bii, kenn ci ñoom muccul ci ‘’parenaas’’ yi ; kon, juróom yi des ci géew bi yépp ay góor lañu. Ndax Senegaal daa pareegul fal jigéen, teg ko ci boppu réew mi ? Loolu lay nirool. Ni Aysata Taal Sàll doxale, nag, day tax ñu yeyatiñu, nun jigéen ñi. Du ñàkk ñu jàpp ne dafa dëggal kàdduy Kocc Barma yu siiw yooyu te naqadee nangu : Jigéen soppal te bul wóolu…