AY CONGU CI YENN BÉRÉB FA SIYERAA-LEWON

Yeneen i xët

Aji bind ji

Njàqare ak tiis la askan wa dëkke fa Freetown yeewoo démb. Ay sàmbaa-bóoy ñoo song béréb yu bari fa gëbla ga. Muy koñ bii di Wilberforce nga xam ne fa la denceefu ngànnaayi sóobare (armurerie) ya nekke, bokk it ci màkkaani soobare ya fa ëpp. Ñu nemmeeku tamit ay sox ca kàrceb (caserne) sóobare Boob Morray Town nga xam ne fa la marin ba nekk. Ak beneen daluwaayu sóobare bu nekk fa gëbla ga tamit song nañu ko. Mu nekk mbir mu doy waar moo xam ne ba léegi kenn xamagul lan moo ko sooke ak ñan ñoo nekk ci ginnaaw.

Ñett ba ñeenti at yii weesu, réewi Afrig sowu-jant yi, muy yiy làkk farañse ak àngale (Siyeraa-Lewon) yépp la ay cong sonal. Yenn ci cong yi bawoo ci sóobare yi nga xam ne seen mébét mooy daaneel Nguur ga fa toog. Muy lu mel ni la xew fa Mali, Burkinaa Faaso, Niseer ak Gine nga xam ne ay dëkkandoom lañu. Walla sax mu doon ay rëtalkat yu lakkal witt askan way yeewoo ca réew ma. Te, xew-xew bii am ca Siyeraa-Lewon muccul ci lenn ci xeetu doxalin yooyu. Ndax, ba jamono jii xamaguñu ñan ñoo sabab cong moomu. Waaye, ni ñu ko baaxoo di gise ci réewi Afrig yi saa su ay wote jàllee, muy yoy palug Njiitu réew, yoy palug dépite walla sax wotey gox-goxaat yi coow li ne kurr ci dëkk bi.

Li dal Siyeraa-Lewon bésub démb bi, nee ñu génneewuñu ci wàlluw pólitig bi. Ndax, daanaka ba wote ya jàlleek léegi ba ñu falaat Julius Maada Bio ci weeru suwe 2023 ñi ngi ci coow. Kenn umpalewul ne moomeem gu njëkk gi atum 2018 la tàmbali woon, jeex ren ci 2023 mi, ñu falaat ko. Boobaak léegi, ci jafe-jafe yu metti lañu nekk ci wàll woowu (crise politique). Ndax, làng gi fare ci kujje gi, di Parti du Congrès pour tout le peuple (APC) ak yenn ci kibaaraan yu bokk bitim-réew dañoo jàpp ne gaa ñi dañoo def ay njuuj-njaaj ci njureef yi tukkee ci mbooleem wote yi ñu fi jot a lim sànq. Maanaam dañoo lëbëje kàrt gi. Moo tax ñoom kujje gi dañoo demoon sax ba dakkal seen liggéey ca Ngomblaan ga ak ci ndajey gox-goxaat yi laata Commonweath bu CEDEAO di ci àddu ngir ñu déggoo ci kàddu. Mbooleem xew-xew yooyu am ci diggante Nguur gi ak kujje gi muy laata ak ginnaaw wote yi taxul wenn yoon ñu xam li xew tey fan la sosoo.

Jamono jii nag, Nguur gi xamle na ne delloosi na jàmm ji, lépp teguwaat na ci yoon. Seen i sóobare fexe nañu ba nasaxal pexey gaa ñooñu doon jéem a sàcc walla jaay doole ba jël seen ngànnaay ca béréb boobee. Fim tollu nii sóobare yaa ngi wër ngir xam kan moo nekk ci ginnaaw cong mi. Looloo tax Nguur gi jël ab ndogal ci tembere def li ñuy dippe guural, maanaam “couvre-feu”. Maanaam, na ku nekk toog këram ba sóobare yi lijjanti mbir mi, delloosi jàmm ca dëkk ba. Ndax kat, ku ndóbbin rey sa maam moom, foo séenatee lu ñuul dinga daw. Te, li dal seen dëkkandoo yi firnde la ci.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj