Barki-démb ci àllarba ji lañu doon amal ndajem jëwriñ mi. Ñu amal ko nag, ci jamono joo xam ne, réew mi dafa dalal ag gan : muy soroj bi. Nde, barkaati-démb lañu génnee njëlbeenug barigo soroj. Moo tax, Njiitu réew mi ubbee ndaje mi ak kàdduy cant, jëmale leen ci Càmm gi, rawatina jëwriñ ji ñu dénk wàll woowu, muy Biram Suley Jóob. Muy woo elimaanu jëwriñ jeek mbooleem ñi nekk ci Càmm gi ñu fexe ba jëfandikoo gi doon njariñal maas gii ak maas yiy ñëw ëllëg. Ginnaaw loolu, Njiitu réew mi Basiiru Jomaay Jaxaar Fay jot naa waxtaane ay wëppa yu bari. Ba mu ca jógee la jël na ay ndogal yu am solo. Nde, am na ñu mu jot a jox ay ndomboy-tànk.
Abdulaay Fay tabb nañu ko « Secrétaire Général adjoint du Gouvernement ». Ki mu fa wuutu di Alliyun Badara Jóob ;
Séex Jeŋ moom tamit « Secrétaire Général adjoint du Gouvernement » lañu ko tabb ;
Àlliyun Paala Mbay, tabb nañu ko Njiitul « Administration générale et de l’Equipement au Ministère de l’Intérieur et de la Sécurité publique ». Mu ngi fa wuutu kii di Ramatulaay Jeŋ ;
Idiriisa Sàmba Sàll moom tamit tabb nañu ko Njiitul « Administration générale et de l’Equipement au Ministère de la Microfinance et de l’Economie sociale et solidaire ». Mu wuutu fa Muhammadu Seen ;
Ramatulaay Jeŋ tabb nañu ko « Inspecteur de l’Administration centrale et territoriale au Ministère de l’Intérieur et de la Sécurité publique » ;
Séex Ba lañu tabb « Inspecteur des Affaires administratives et financières au Ministère de l’Énergie, du Pétrole et des Mines ». Ki mu fa wuutu di soxna Aysatu Alima Sàmbu ;
Kumba Sow, tabb nañu ko « Inspecteur des Affaires administratives et financières au Ministère de l’Économie, du Plan et de la Coopération ». Ki mu fa wuutu di Màgget Jóob ;
Mariyeem Jaañ Taal, moom lañu tabb « Inspecteur des Affaires administratives et financières au Ministère des Pêches, des Infrastructures maritimes et portuaires ». Mu wuutu fa Mamadu Gujaabi ;
Nafisatu Faal Njaay, tabb nañu ko « Inspecteur des Affaires administratives et financières au Ministère de la Famille et des Solidarités » ;
Móodu Mbay lañu tabb « Inspecteur technique au Ministère de la Famille et des Solidarités » ;
Lasaar Saar, tabb nañu ko « Inspecteur des Affaires administratives et financières au Ministère de la Jeunesse, des Sports et de la Culture » ;
Baaba Ndóoy lañu tabb « nommé Inspecteur des Affaires administratives et financières au Ministère du Tourisme et de l’Artisanat » ;
Póol Mari Antuwaanet Saaña, tabb nañu ko « Secrétaire exécutif de la Commission de Régulation du secteur de l’Energie ».