BADARA GAJAGA FANAANI NA KASO

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ayu-bés bii ñu génn lañu la Yoon woolu woon Badara Gajaga. Li sababoon woote bi, kàddu yi mu yékkati woon ci jotaayu Jàkkaarloo bi ñuy amal ca TFM bokk na ci donte ne sax, am na yeneen tuuma yu ñu gàll ci ndoddam. Ba ñu ko dégloo ba noppi, ca lañu ko téye. Booba ba tay nag, mi ngi ci loxoy Yoon. Tay, ci altina ji lañu ko mujjee yóbbu kaso.

Kàddu yi tukkee woon ci jotaayu Jàkkaarloo bi doxoon diggante Aamadu Ba bu PASTEF ak Badara Gajaga jur na coow lu bari ci réew mi. Dafa di, looloo tax sax Yoon woolu woon leen ñoom ñaar ñépp. Kii di Aamadu Ba moom, ginnaaw ag ndégloom, dañu koo bàyyi mu ñibbi. Ci lañu wooloo Badara Gajaga tamit. Bi muy wuyuji, bari na ñu ko toppoon. Muy ñenn ci askan wi, ñenn ci waa kujje gi ak sax ñu fare ci kuréli way-moomeel. Mu am ñoo xam ne sax ci seen xëti Facebook walla ci seen i xët yu nekk ci yeneen mbaali jokkoo yi lañu doon fésale seen naqar. Di wone ne ànduñu ci li ñu teg faramfàccekat boobu. Mu am tamit, ci beneen boor bi, ñu doon ñaawlu kàddu yi mu teg ci seen kaw kilifag làng. Di sàkku Yoon dal ci kawam.

Ginnaaw, bi mu wuyujee ca àllarba jee weesu, ca lañu ko téyeendi woon. Tay, ci altine ji lañuy sog a jël ci moom ab ndogal. Nde, ci bëccëg gi la xibaar rot ci ne dañu koy yóbbu kaso, maanaam dañu ko dóor lees di wax “mandat de dépôt”. Moom, Badara Gajaga, bari na ay tuuma yu ñu gàll ci ndoddam. Bi ci jiitu mooy biral ay kàddu yu woroo ak jikko yu baax yi. Bi ci topp mooy tasaare ay xibaar yu wérul. Bi ci toppaat di ŋàññi nit ku am lépp walla lenn ci dayoy Njiitu réew. Bi ci mujj mooy jot walla càkkuteg koppar ci anam yu leerul, te jubluwaay bi di dooleel loo xam ne mën naa nasaxal kaaraange réew mi.

Tuuma yooyu mooy yi ñu teg ci ndoddam donte ne sax, layookatam bii di meetar Yuum naqarlu na leen. Ndax, dafa gis ne ñetti tuuma kese la pólis tegoon ci ndoddam ginnaaw bi mu ko dégloo. Nee na, yi ci des fa ëttu toppekaay ba (parquet) lañu leen ci yokkee. Maanaam, gaa ñooñu ñoo yokk ci xar mi karaw. Te, li ñu ci jublu du lenn lu moy noppiloo maxejj boo xam ne day joxe xalaatam ci réew mi. Ba tax na, ñuy def seen i pexe ngir tëj ko. Nee na, loolu duñu ko nangu. Li am ba des mooy, kii di Badara Gajaga moom, yóbbu nañu ko kaso ginnaaw tuuma yees jot a lim. Dina fa yàgg am déet. Li ci kanam rawul i bët.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj