Nit, ak xelam ak i xalaatam yu xóot, du jóg ci di jéem a ñoŋal nekkinam ci kow suuf. Ba tax na, lépp lu mu njort ni dina gën a yombal dundam, du lott mukk ngir taxaw ci. Ndax, bëggul lu dul, saa su ne, muy wéy di gën a neex. Looloo waral, muy topp i bëgg-bëggam, di jaarale xelam ci yoon yu koy may mu jëmmal ay mbébétam.
Ci kow loolu lépp, donte sax xelam lay jëfandikoo, dafay mel ni ku dul xalaat. Ndax, ñaare, saa su defaree dundam ba mu gën a baax ci genn wet, yàq na lu bari ca geneen wet ga. Ci lu mu yëg walla lu mu yëgul. Te, lu jamono di gën a dem, muy gën a gis dayob li ay jëfam yàq ci kow suuf.
Yàq-yàq yooyu ñoo dem ba salfaañe dal gi kéew mi nekke woon. Nga xam ne, mënees na koo méngale ak ndox mu taaju lu yàgg, jaare fa, daldi teey. Nëxit yépp wàcc ci suuf ba, ku ko séen, gis ni mu leeree. Nu toog ab diir, mu am këf ku tàbbi ci biir ak doole, ba lépp nëxaat. Fi mu ne, foofu la àdduna si tollu. Te, kenn ku nekk, ak fu mu mën a féete, mi ngi koy yëg ci dundam. Bu fii tàngee ba jaaxal ñu bari, fale sedd lool bay lore. Yenn saa yi sax, mu taw ba lóor, ndox mi jur loraange ju rëy.
Fii ci Senegaal, ayu-bés walla weer yii nu nekk, nu ngi teg sunuy bët, nun ñépp, ci mbir mu ni mel. Ginnaaw bi asamaan si sottee ndox mu baree bari, dex yii di Senegaal ak Gàmbi dañoo fees ba rembat. Walum ndox mi dem ba jur ay loraange yu jéggi dayo ci dëkk yi féete ci peggu dex yi. Mëdd na fa ay tool yu bari, xajamal na it dundug ay junniy doomi Aadama. Ndax, dafa nangu seen i kër, ne gadd ci mbedd yi ba daanaka seen lépp taxaw, ne tacc. Muy lu metti lool.
Waaye, dafa mel ni, nun askan wi (Senegaal gépp) yëgunu mettit wi. Walla boog, ñi mu dal ak seen i mbokki bopp doŋŋ la tiis wi soxal. Keneen ku dul ñoom rekk, sa yoon nekku ci.
Li waral wax ji mooy ne, sunu taxawaay ci mbir mi dafa des bu baax. Ndax taxul mu fés lool te it, ndiruwul ni jox nanu ko yitte ji war. Néew na, ci ñi dëkkul fa gox yooya walla amuñu fay mbokk yu jege, ñu feeñal seen naqar ci jéyya ji. Walla sax ñu jéem leen a taxawu ci seen kemtalaayu kàttan te bañ cee xaar dara.
Moone de, sunu réew mii la àddina sépp di dàkkantalee “Réewum teraanga”. Mu mel ni kon teraanga ji dafa féete wet. Walla boog ña ca bitti rekk ñoo ko yelloo. Nde, gan yi fiy ñëw moom, miin nañu ko ba di ñu ko taggee. Te nun it, askan wi, baaxoo nanu, bu aw tiis dalee ci kow weneen askan (wu nekkul ci kembaaru Afrig rawatina), nu ànd naqarlu ko ba noppi fésal ko lool. Lu tax nag bu dee ni fii la xewee, feek dalul sunu kow rekk dunu yëngu ?
Li walum ñaari dex yi sabab, danu ko soofantal, suufental ko lool. Ndax, terewunu wenn yoon nu wéyal sunug dund mel ni lépp a ngi jaar yoon. Nu ngiy wéy di lekk sunu ceebu jën, di naan ataaya ak a làng waxtaan. Dund giy wéy, mel ni dara xewul fi réew mi. Ci jamono joo xam ne, sunuy mbokki ma-réew ñu ngi ci guddi gu bët setagul. Ñàkk fu ñu dugg ak seen i njaboot, ñàkk seen i jur ak seen i tool, lu bari ci li ñu amoon naaxsaay. Nga xam ne ci diiwaanu Maatam kese, ñu ngi fa doon xayma lu ëpp 700i tooli ceeb yu ndox mi nangu. Loolu rekk waroon na tax nu taxaw, dëgg bal bi (ni ko futbalkat yiy waxee), jéem a wutiy pexe.
Dëgg la, Càmm gi yóbb na fay ndimbal yu am solo. Sóobare yi, ak seen njàmbaar, ñu nga seen i wet di leen taxawu ni ñu ko baaxoo defee saa su askan wi soxlaa. Waaye, ndax loolu rekk doyna ? Ba fi mu nekk nii, kenn mënul a wax dayob yàq-yàq yi wal mi jot a jur. Te it, kenn mënul a xayma ci lu wóor loraange ji mu nar a juri ëllëg (ci askan wi yépp nag !). Ba tax na, lu nu ci def rekk, war koo xeeb.
Way-pólitig yi, ci seen wàll, defati seen mënin. Jël tiis wi, bëgg koo cuub wirgow pólitig. Nun itam nu topp leen ci di soow ba jaare fa mel ni danoo fàtte li xew. Nguur giy nas i pexe, kujje giy sànni xeer. Dégg la gaa, ci loosu njiit yi la lépp di gàllu ndax ñoom ñooy kilifa yi. Waaye, ndegem liy am am na ba noppi, dara desatu fi lu dul ànd wuti saafara.
Ci jamono ju mel nii, réew mépp a waroon a def wenn say, di waxandoo ci genn kàddu, di xàccandoo, di dóorandoo. Lépp ngir jafe-jafe yi jeex mbaa ñu wàññeeku bu baax.
Ci jamono ju mel nii, réew mépp a waroon a gën a dëgëral seen ub lëkkoo. Nu boole sunuy doole, dajale sunuy pepp ak sunuy dërëm ba mu duun. Nu ànd yóbb lépp fa way-loru ya ba noppi taxaw seen wet ba tiis wi dootul diis ci ñoom.
Ci jamono ju mel nii, réew mépp a waroon a toog, péncoo. Ku xareñ mbaa mu am xam-xam ci mbir mi génnee ko. Bu ko defee, nu sàkk i pexe ba saafara judd. Bu nu ci noppee xàll yoon wuy tax a mucc ci lu ni mel bu ëllëgee.
“Balaa ngaa laax jaay, laax lekk”. Loolu de la maam wax. Kon boog, teraanga ji war na a tàmbalee ci waa réew mi. Bu ci ñépp jotee, nu ànd ñamal ci waa àdduna.