Ballon d’Or France Football 2022 : Saajo Maane ci pójëm bi 27i at ginnaaw Soors Weyaa Saajo Maane, sa woy wi dootul fay

Yeneen i xët

Aji bind ji

Saajo Maane, sa woy wi dootul fay

Joxe nañ cargalub Ballon d’Or France Football 2022 ci altine jii weesu. Ñaŋ ko doon amalee ca Théâtre du châtelet, nekk ca Pari. Mu doonoon 66eel bi, biñ ko sosee ag léegi. Ngoonu keroog nag, doomu Senegaal jii di Saajo Maane, jële na fa woy wu dul fay, ba tax ñépp ànd naan ko « gàcce ngaalaama gaynde ».

Saa-Senegaal bi Saajo Maane jëlul Ballon d’Or 2022 bi. Ki ko gàddu mi ngi wuyoo ci turu Karim Bensemaa, di doomu Farãs ju cosaanoo Alseri. Moom, Saajo Maane nag, jotoon na koo wax sax ci làmmiñu boppam : « Kariim Bensemaa yelloo na Ballon d’or bi ». Te muy dëgg itam, nde at mu baax la génn ak i jaloore.

Bu ñépp naan « gàcce ngaalaama Saajo Maane » du dañ fi bàyyi ki jiitu te naan ku ci topp a aay. Dafa fekk ni kay « ku gis nen, ne nen a ngi ». Doomu Bàmbali ji dafa mëne fu nekk. Bokk na ci li ko waral : cargalub Socrates bi France Footbal sos ci atum ren jii te mu njëkk koo jël. Muy lu réy nag ; nde bile càrgal ñiŋ ko jagleel ku gën a ràññeeku ci wàllu ndimbal ak taxawu néew-doole yi.

Ñu ne déet-a-waay, mu dellu sës rëkk ci ku gàddu Ballon d’Or bi. Muy ñaari ndam ci benn jotaay bi. Taariix juddu : ginnaaw 27i at, ba Soors Weyaa jëlee woon Ballon d’Or bi ci atum 1995, moom kott mooy Saa-Afrig bu yéeg ci pójëm bi. Kii nag mooy gaynde dëgg, te wone na ko. Ponkali Afrig yi fi jaar yépp àgguñ foofu (Dorogbaa 4eel/2007, Etoo 5eel/2009) ba ci Salaa ak Mahrees ñim jamonowaale ci 5eel/2022 ak 7eel/2016 toogaan yi nañ yam.

Wolof Njaay nag dafa ne « ku def lu réy, am lu réy ». Loolu tax ba ñépp ànd ak moom di bànneexu ci ndamam li. Li ko dale ci Génération Foot, fa lépp dooree, ba ca Bayern Munich, fa muy yëngu, jaare ko ci Fc Metz, fa mu njëkke, futbal ca bittim-réew, ñépp ne eskéey Saajo Maane. Kàdduy ndokkale yu ñëw gën a dal yi jàll. Saa-Senegaal yi ñoom, waxaalewuñ leen. Njiitu réew mi Maki Sàll, Yànqooba Jatara mi mu dénk tàggat-yaram yi ba ci Ógistĩ Seŋoor mi jiite axlu futbal bi, kenn desul. Kii ñu mujje tudd a nga naan ko :

«Yaay ki njëkk jël cargalub Socrates ci mbooru Ballon d’Or, dellu nekk ci ñaareelu toogaan bu toftaleb Ballon d’Or 2022. Céy ndam li nga am Saajo Maane. Te jeexagul. Jëre-jëf SM10 ci ni ngay bégalee Askan wi ak kembarug Afrig. Jërëjëf, rawatina ba nga yékkatee ca kow nataal bi ak mbaax yi futbalu réewum Senegaal làmboo. Demul bay jeex, dig-daje ca Qatar ci nowàmbar 2022 ngir wéyal bile taariix. »

Lii de mooy xol yépp a fées. Ku ñépp nangul nag sa xareñ a tax. Waaye ku ñépp yéene itam, na nga mel a ko waral.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj