NJEEXITALI ÀTTEB BAARTELEMI JAAS BI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ёttu àtte bu Ndakaaru dёggal na daan bi ñu teg ci ndoddu Bàrtlemi JAAS ci Àllarba jii nu weesu. Daan boobu nag li ko waral mooy benn jàmmaarloo bu amoon ca buntu meeri Mermoos Sàkkerekёer, 22 ci Desàmbar atum 2011, mu amoon ndaw lu ca ñàkke bakkanam. Ndaw loolu mi ngi doon wuyoo ci turu Njaga Juuf. Loolu nag mi ngi ame woon ca Nguurug Abdulaay Wàdd jamono ja ñuy waajal wotey 2012 yi. Coow loolu nag, am na lu tollu ci fukki at ak lu topp ci loxoy yoon. Ci fan yii nu génn lañu ko teg ki ñu tuumaal mbir mi daanub ñaari at ak juróom-benni weeri kaso yoo xam ne, daf koo war a tёdd te mu tёdd leen ba noppi. Li ub xel yi kay mooy ku rey nit ba pare di tёdd juróom-benni weer kepp. Rax-ci-dolli, xew-xew bi mi ngi ame woon ca Nguurug Wàdd, Maki ma daan dooleel Baartelemi ca jamono jooja, naan deful dara, dafa aar boppam. Tey ci ag Nguuram ñu ne moom la. Léegi kon, daan bi ñu gàll ci loosam ci yoon lañu ko teg walla pólitig moo ko lal. Mu mat a samp ab laaj tamit ngir xam lan la daan boobu mёn a jur ci ёllugu pólitigu Baartelemi Jaas ?

Coowal bóomug Njaga Juuf nag yàgg na lool ci loxoy yoon. Te, ba tey dara leeragul ci mbir mi. Loolu nag, taxoon ba kii di Bàrtelemi Jaas, Meeru Ndakaaru, di tamit dépite ca Ngomblaan ga, nga xam ne moom lañu tuumaloon ne moo bóom ndaw li defoon ab appel ngir setal deram. Ndax, du nangu ñu gàll ci loosam loo xam ne defu ko. Mu mel ni loolu saafara su jur jàngoro la ndax ay daan a ko ci mujj fekk. Waaye loolu, taxul mu teggi tànkam fa mu ko tegoon. Ndax, nee na dóor na bal waaye reyul. Moo tax ci waxtaan wu mu doon amal ca TFM ci àllarba jii mu jot faa defaat ay leeral, mu ne :

“May biralaat wax ji, ba ñu may njёkk a téye, ñu ne dangay joxe sa ngànnaay ma ne leen déet. Ma ne leen na ngeen njёkk a wax ban kaliibr moo rey ndaw loolu ma soog leen jox sama ngànnaay (…). Te man kaliibr bi ma yoroon ak kaliibr bi ñu génne ci yaramu saay-saay bi bokkul.”

Moom nag yamul ci kàddu yooyu ndax tamit dañu ko doon toppe ne amul woon sañ-sañu yor ngànnaay loolu. Yoon jox ko ci dёgg. Ba pare, yoon  wёlbatikuwaat ne amul sañ-sañu yor ngànnaay, di ko ci daan. Moo tax mu yokk ci ne, bu àndoon ak Maki Sàll, kon coow li jeex na yàgg na. Mu mel ni gaa ñi dañoo jàpp ne pólitig moo lalu ci ginnaaw.  Ndax, kii di Njiitu réew mi Maki Sàll moo ko génne woon ndung-siin def ko dépite. Te, ca jamono jooja tuuma mi ngi woon ci ndoddam. Waaye nag, ngelaw dina dugal ci pax lu mu fa mёnul a génne. Loolu bokk ci li tax, am ci gaa ñi ñu jàpp ne am na lu laxasu ci mbir mi. Moo tax, kii di Gii Mari Saaña biral kàddu yii ginnaaw àtte bi :

“Li am tey day firndeel li ñu yàgg a xeex, muy Kumba am ndey ak Kumba amul ndey gi am ci Senegaal ci fànn yu bari rawatina ci yoon. Boo àndee ak Maki Sàll dara du la dal, loo mёn di def dara du la ci fekk. Waaye, boo nekkee koo xam ne day xeex ngir njariñu askanu Senegaal ci lu amul genn laam-laame. Te, loolu mooy màndargaal dépite bii, di tamit meeru Ndakaaru di  Bàrtelemi Jaas. Bu boobaa yoon dina la sonal (…). Bu boobaa dinañu def lépp ba doo doon Meer. Bu boobaa boo nekkee Meer sax ñu wéy di la bunduxataal.”

Waaye nag, bu dee nii la mbir yi deme, daan boobu, lan la mёn a jur ci ёllёgu Baartelemi ci làngug pólitig ak ndombog-tànk yi mu jot a am ? Donte ne sax, méeri bu Ndakaaru moom mёn na koo bañ a ñàkk. Ndombog-tànk gi ko askan wi jox muy nekk gi mu nekk dépite mёn na koo ñàkk bu fekkee ne amatul genn laam-laame ne daan bi day dal ci kawam. Ndax, dañu ne bu ñu delloo ci ndeyu-àtte yi ak ci càrt yi ñu tёral ci biir Ngomglaan gi, dépite bu ay daan tegu ci ndoddam dañu koy génnee ci wayndare dépite yi. Waaye moom, lii la ci tontu :

“Dara duma ci fekk. Fii ak fukki weer ak juróom Maki dem. Ci diir boobu damay des ca Ngomblaan ga.Te, duma wax nan laa fas yéene def ba toog fa. Askanu Senegaal ñi ngi may seetaan. Duma jóge ca meeri bu Ndakaaru, duma jóge ca Ngomblaan ga bu soobee Yàlla.”

Léegi, li mat a laaj kay mooy ndax yёf yi du mujj ca Ngomblaan ga ? Baartelemi Jaas day ñàkk palaasu dépiteem am déet ? Dees na ci xam fii ak i fan lan mooy topp ci daan bi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj