BATAAXELU NJÉMMEER ÑEEL JAWRINU CAYTUG NJÀNG MI CA LUGA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Kilifa gi,

Ginnaaw ba ma la nuyoo jox la sa wàccuwaay, duma def lu moy dikk ci aali-kalaj gi jëm ci dogal bi nga jël muy tere sabar ak simb ci lekkool yi. Fi ma ciy gën a waxee te gis ni moo gën a sabab boobule dogal mooy sabar.

Sa dogal boobule ak sew-sew yi ma foog ni ñoo la ci jóo, ñaar yépp a ma metti. Nde, bu ci nekk dafa jëm ci réeral pàcc ci mbatit, rawatina gog Wolof. Ñàkk teggin gu fés gi xale yiy wane ci peccum sabar mi jamono jii, dafa cee wàllsi. Waaye, moomunu ko. Jamonoy jii nag, ak ni mbatit yi di duggantee, lépp lañu rax, moo xam mu jëm ci diine mbaa jamono, lii lalu ci umpale, lee lalu cig tayeef. Ma lay laaj nag, ndax boroom xam-xam bu toll ni yaw, ak dooleek sañ-sañ bi la Yàlla dénk, manoo woon a posewu ci lii xew, samp ag ndiisoo yaak ñenn ñi ñu dénk wàllu mbatit, ngeen fexee joyyanti loolu bañ koo dagg sànni ?

Man nag, sama xalaat duma la ko nëbb. Damaa jàpp ni, seen gis-gis ci fànn woowu ci sunu mbatit xóotul, mbaa boog jëggaani leneen dafa leen a gënal saytu ak a suuxat li nu moom. Ndax, xamoon nga ni sabar yii ngay tere tay ci lekkool bi, taxawaayu téere la amoon démb, ñu ci daan jaarale xam-xam yu gànjaru. Ndax, xamoon nga ni sabar daan na bàkk di wax kàddu yuy jafal jàmbaar ci toolub xare ? Ndax, xam nga ni sabar daan nañu ko jëfandikoo di ci jollasante ay waat dëkk ak dëkk, niki ni jaan daan màtt nit ñu daldi yóotu sabar, dëkk ba dëkk ñuy jollasante cim tëgg naan “ku jaan màtt sam xel dem ci dee, bu ñuy dund ak bu nuy dee yépp sam xel dem ci dee.” Ñu koy jokkalantee noonu ba muy tàbbi ca noppi luggkat ba, su ko defee kooka war aw fasam. Booba telefon amul woon.

Kilifa, yaw mi jite caytug njàng mi foofu ca Luga, ndax xamoon nga ni Mbóol Sekk wax na ci sabar lu wedamloo Seŋoor. Moo ni woon këccu, lu mu ràbb ci ndiggam la jëm. Moo tëggoon “benn gayet takkub néeg, bu doon ñaar mu sumburmbaan.” Yaw sax, ndax xam nga luy tàggu mbaar ? Ndax xam nga Ngomaar ? Ndax xam nga lu wuutale : ndawràbbin, yaŋaab ak far-wu-jar…? Loolu lépp ci sunu mbatiit la bokk te sabar mooy càllala gi nu lëkkale, waaye moo ngi naaxsaay te ñi nu dénk njàng mi ak ñi ñu dénk mbatit waroon nanu man a lëkkaloo, lal ay pexe yuy dundalaat cosaan ci fànn woowu, delloo li ëpp fa mu ne woon, saytu ko dindi li ci wallsi te di luy yàq.

Damay wéet lu bari naan ñiy jiite njàng mi ak mbatit bañu amee sunug jonn ak tay, ndax xam nañu dëgg fi li ñu leen dénk toll ak li ci war. Sa dogal bii nag, boo xamoon li xew, xam ni am na lu ko gën fuuf. Ndaxam boo yoree gànjar gis luy gàkkal lu ca wàllsi, dangay seppi loola ; waaye doo ni xërr gànjar ga sànni.

Dinaa posewu itam ci sama bataaxel bii, wax la sama xalaat ci njàng mi. Sañ naa ko ndax ñaar ba ñett. Dama di doomu Luga, di ab jàngalekat (PES ANGLAIS), di wesaare itam ci tuut sii ma xam ci mbatit ak làkku wolof, ci benn ca pàcci jàngune Ndar bee ñeel Làkk ak Mbatiiti Afrig. (Intervenant au département LCA/CRAC) ; li ma may loolu mooy Làkk ak Mbatit rawatina yoy Wolof dañu di yu ma yitteel. Mooma jóo itam ci tànn Wolof di ci bind ay téere, boole ci di wéyal samay gëstu ci fànn yooyii.

Bu dee lu jëm ci njàng mi, li ma wax keroog ci mbind mu ma fésaloon ci lënd gi rekk laay waxaat. Dama ni, su fekkoon man naa jot ci noppi Njiitu réew mi, dinaa ko ni li lëj ci njàng mi ak li njàng mi lëjal li koy lijjanti du yii… Ku xamul boppam, keneen koo ko jàngal mu réer ci kooka ba faf xeeb boppam ak céram. Looloo waral ñi jàngi woon ba noppi, ñi ci ëpp di saf i tubaab, ñee di saf i naar ndax yaras (complexé).

Sémbu njàng mi, ci laa jànge ci laay jàngalee. Waaye, bu ma ci amoon dogal, 70% yi dama koy dagg sànni, indi leneen lu jëm ci lu nuy delloo ci sunu bopp, ak nan lanuy yaatalee li nu moom boole ci xool xam-xam yi ëpp solo fii ak feneen yakk ko ci làkki réew mi. Liggéey dëgg la laaj, farlu gu mat sëkk ak xel mu sell ! Waaye du yii de…

Jàmm ak xéewal !

Làmp Faal Kala

Làmp Faal Kala
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj