Jógati naa saddati ay bayit sargale mbër
Bàkk ko jiin ko xaacu naan na woy wi wër
Ragal péete kat xañ na fi nit ki wërsëgam
Moom mooy ki doxe xam-xam bi ma gëm
Wër na àddina te xam na gis na lu ne fu ne
Te fum fi dem fu ne yóbbaale réew mi li fi ne
Sagal na Afrig ndaanan la leeral na yoon wi
Togg xam-xam bu neex yakk ci làkku réew mi
Yey na gaa ña jàngaani woon ñëw di nu xas
Tubaab ak naar ya sëf leen i yëf ñu faf yaras
Yaa indi ay ndam ci réew mi te bàkkuwuloo
Jaayuwuloo ndax woyof waaye tuutiwuloo
Jàmbaar ji ma tax di wax Bubakar Bóris Jóob
Moo nu sédd ay njariñ ca ya mu bay ba góob
Fekkoon nu mar di wër ak a rootaani feneen
Naan nanu tey ba màndi bënnal na nu teen
Sant koo nu war man ak samay moroom
Di ko jiin di woy di seede ni amul moroom
Yal na wér te wérle Yal na aw fanam gudd
Ngir yii ma junj ci ay jëfam ak yii ma tudd
Làmp Faal Kala