BENN LAYOO, 16i BAKKAN

Yeneen i xët

Aji bind ji

Benn takk-der bu daamaru pólis bi jaar ci kowam, mu jaare fa, ñàkk bakkanam. Benn a ngoog. Mbetteel, tiis ak naqar dikkal baay bi, mu daanu feebar, faf fekki doom ja, Haasim Jéeju, ca barsàq. Ñaar a ngoog, Sigicoor lañ daanoo, démb ci altine ji. Ba tey, fa Sigicoor, fa gox bañ naan Neemaa, takk-der yi sox nañ fab ndaw ab balu dëggëntaan ci bopp, mu daldi faatu. Jàppal ñett. Nit ñiy jooy ak a artu ngir ñu àtte xeex bi balaa moo ëpp i loxo, ñu tàggewaat beneen xale buñ dóorati dëggantann, fa Kër Mbay Faal. Muy ñeenti bakkan yu rot ci bésub démb ji. Mbaali-jokkoo yiy tas xibaar yi, di badd nataal yeek widewoo yi. Fu xeex am, ñu siiwal ko.

Ay tali yees dog ak ay biisi Dakaar Dem Dikk yees jafal. Ay Auchan yees dàjji, caxat-caxate leen, jël njaay ma ba noppi taal leen. Matt yeek póno yiy boy, xeer yeek lakkirimosen yiy dàkkante. Saxaar si, wex xàtt, ubale fépp, noyyi jafe. Sigicoor, Ndakaaru, Kawlax, Ndar, fépp a yëngu. Démb ci altine ji, ba ci guddi gi, xeex bi dakkagul woon.  Te sax, ba ci talaatay tey jii, xeexu Sigicoor ba tasagul. Lu tax ? Lu ko fi jar ? Fu réew mi jëm ? Moom la ñu bari di laaj.

Ginnaaw ñaari ati coow ak fitna, ginnaaw bi ci 14i bakkan rotee ak yàqute yu bari amee, tey woon bésub layoo diggante Usmaan Sonko ak Aji Saar. Ginnaaw mbir yu bari yi jot a xew ci diggante bi, am ñu ci ñàkk seen liggéey, ñii jële ciy gaañ-gaañu, ñee ñu teg leen loxo. Ginnaawati « certificat médical » bu leer bi ak seedey doktoor Alfuseyni Gay bi ko defar, rawatina seedey Ndey Xadi Njaay mi moom Sweet Beauty, nga teg ci caabalug sàndarmëri beek ndéggati Aji Saar yiy setal Usmaan Sonko, tey, talaata 16 me 2023, lañ ne woon dañuy àtte Usmaan Sonko ak Aji Raabi Saar mi koy tuumaal ciif ak tëkkuy rey. Waaye, layoo bi mujjul am. Nde, àttekat bi daf ko bëtal ba talaata jii toftalu, dëppook 23 me 2023.

Xeetu coow lu ni deme, guléet Senegaal di ci dugg. Altine jii wessu lañu ko doon àtte moom Njiitul Pastef li ci coow li doxoon digganteem ak Maam Mbay Ñaŋ ba ñu daan ko ci. Mu amaatoon beneen layoo ci talaatay tey jii. Yëf yi dem ba niru singali. Moo tax njiitul Pastef li bañati wuyu Yoon. Ndogal loolu mu jël ba dogu ci, ne dootul wuyooti wooteb Yoon miy salfaañey àqam, dëkk ci di ko tooñ ci lu bir, moo sabab coowal démb li. Nde, dañ doon ruumandaat ne dañuy waaj a jàpp Usmaan Sonko. Moo waral ay àndandoom ak i soppeem takku taxaw, jàmmaarlook takk-der yi ba mu jur li mu jur. Te, layoo bi sax mujjul am. Àttekat bi ci boppam mo dàq layoo bi. Ndax, ci sabab yi mu joxe, daf ci wax ne :

« Ci altine ji lañ déglu Ndey Xadi Njaay te, Yoon dafa sàrtal ni, ginnaaw biñ dégloo ab seede, fàww ñu lim ñetti fan laata ñuy amal layoo bi. Nun, ay àttekat lanu, xam nan lu jaadu. »

Meetar Musaa Saar itam, di kenn ci layookati Ndey Xadi Njaay yi, lu ni mel la wax. Moom sax, dafa sàkku ci ñu yokk àppub dàq bi ci diirub weer ngir mu mën a saytu wayndare wi. Lii la wax :

« Noo ngeek wayndarew 471i xët wu ànd ak i ndéggat, ay nataal, ay widewoo. Mënunoo xam li ci biir lépp ci diirub 8i fan. Lees di toppe sunu kiliyaan dafa réy lool,ba tax ñu war noo may ngir nu xool pexe mun koy layalee. Fàww ñu dàq ko diirub weer walla 45i fan. »

Meetar Elaas Juuf, moom, àndul ci loolu tey, àndu ci ëllëg. Daf ne, moom layookatu Aji Saar bi, « Bu amee sax layookat yu bees, nun sunu « ceebu jën » nekku ci. Ci ndoorte li ba tey, am na ñu koy taxawu di ko layal. » Yemu ca de. Nde, gaaral na Usmaan Sonko ciy kàddoom :

« Am na ñoo xam ne, dañu daw layoo bi. Dañoo ragal a jàkkaarlo ak Aji [Saar]. Waaye nun, noppi 2i at ci ginnaaw. Soxalwunu 20i fan walla weer ngir waajal sunu bopp. »

Loolu yépp terewul, àttekat bee yor baatu dogal bi, te dàq na layoo bi ba keroog 23 me 2023.

Ba booba.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj