Démb ci gaawu bi, 22i fani féewirye, lañu doon màggal bés bi ñu jagleel jur gi fi réew mi. Xew maa ngi ñu doon amalee fa Kawlax, ci téewaayu Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay.
Bi 10i waxtu di jot ci yoor-yoor ba tegal 30i simili la Njiitu Réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, egg fa Kawlax ngir jiite ubbiteg bés bi ñu jagleel yarub jur gi fi réew mi. Bokkoon na ci ñi mu àndal, El Haaji Maalig Njaay (njiitu Ngomblaan gi) ak Mabuuba Jaañ (Jëwriñu mbay mi, dund bu doy ak yarub jur gi). Bi ñu yegsee itam, askan wa fay yeewoo dalal nañu leen, ànd ceek kilifay caytu gi ca gox ba, kilifay takk-der yi, kilifa diine yeek yu aada yi.
Bésub ren ji mooy 9eel wi yoon ginnaaw bi ñu ko tàmbalee màggal ca atum 2014, ci njiiteefu Njiitu réew ma woon, Sëñ Maki Sàll, ngir mu doon ndaje muy yombal diisoo beek sottante xalaat ci diggante Njiitu réew mi ak yarkat yi ñeel jafe-jafe yi ci aju fànnu càmm gi ak yar bi. Wu ren wi nag, dees ko tënk ci wëppa wii di « solaal ndefar yiy soqikoo ci jur gi : luy jollil mën-sa-boppub Senegaal ñeel dund bi »
Jot nañoo amal i xew-xew yu bari ci bés bi. Yu deme ni doxantu, rawante fas ak ay jotaayi waxtaan ci yarub jur gi. Amal nañ fa itam ay ñakk ci lim bu takku ciy fas ak i nag. Lees namm ci waxtaan yooyee mooy bees jógee ci bés bi, yarkat bi mën a farlu ci sopparñi ngëneel yiy bawoo ci jur gi ngir réew mi mën a jekku boppam ci wàllu dund bi.
« Tay ci tay, daanaka lépp luy ndefar yu solowu yu bawoo ci jur gi, yu deme ni soow, formaas, bëer, ndawal, bitim-réew lees leen di jéggaani. Bees jógee ci bésub jur gi, ñoo ngi xaar yokkute ndefar yu solowu yu fekk baax fi Senegaal » (Xadi Njaay, njiitu pekkug diwaanub Kawlax ñeel yar meek ndefar yiy bawoo ci jur gi).
Bu weesoo loolu itam, yarkat yi biral nañu fa seen i càkkuteef, ginnaaw bi ñu waxee seen mbégte ci ni Càmm gi nammee taxaw ci seen i yitte. Naka noonu, ñuy sàkku ci Nguur gi mu beral leen i pàkk te yokkal leen kaaraange gi. Nde lu ëpp ci jafe-jafe yi ñuy dund ñoo ngi dellu ci àll bi ñuy sàmme ak càccug jur gi.
Dafa di, bu mbay miy gën a am doole, tool yi di gën a bari, sàmm yiy màngaan dañuy jànkonteek jafe-jafe ngir am pàkk yu ñuy sàmme. Ba tax ñuy sàkk ci ñu daggal leen i pàkk yu méngook càmm gi. Te loolu dina tax ba ñu mën a moytu coow yiy faral di am ci diggante baykat yeek sàmm yi. Ci noonu itam lañu sàkkoo ci kilifa yi ñu yokkal leen kaaraange gi ndax càccug jur gi mën fee jóge. Bu dee li aju ci wàllu kopparal geet, bëgg nañu Nguur gi wutal leen i pas ci bànk yi ba ñu mën a dëppale kopparal gi ak seen i yëngu-yëngu.