Démb ci altine ji, 18 desàmbar 2023, lees jagleeloon mbëkk mi ci àddina sépp. Muy bés bu ñu jàpp ngir waxtaane lu waral ñiy làqatu di tukki ak di ko jaare ci anam yees yoonalul. Bu amee ñu gis ni ndóol gee yaatu ci réew yi roñukat yiy bawoo, sonal ndaw ñi ba ñu xàddi, am na ñu gis leneen. Te mooy ni bare na ñu amoon ci lu ñu jàpp, jekku woon seen bopp, te terewu leen dem ba di ci ñàkk seen i bakkan. Fi Senegaal, looloo waral ba yenn kurél yi ciy liggéey ak Càmm gi jàpp ni mbir yi laalewul rekk ak koom gi. Te laaj nay gëstu yu xóot ci mboolaay mi ngir gën cee mën a gindeeku.
Ak lu mu ci mën di doon, mbëkk mi moom am na doole lool fi Senegaal. Bees sukkandikoo ci li Anet Sekk, jëwriñ ji ñu dénk wàllu bitim-réew ak Saa-senegaal ya fa nekk, lum néew-néew 123i gaal jóge nañ fi réew mi, teeri fa Espaañ. Te am na gaal yoo xam ni àgguñu. Muy yi teeri Kabweer, Marog, Móritani ba Nikaraguwaa, ak yi réer te kenn tegagu leen bët ba léegi.
Li ko dalee Ndar ba Sigicoor, jaare ko Cees ak Ndakaaru, mbëkk mi bàyyiwul benn diwaan. Ñu gis tamit ne, bare na lool ndaw yu ci laale. Waaye, am na tam ay tuut-tànk, ba ciy jigéeni wérul.