BITIM-RÉEW : LAYOOKATI USMAAN SONKO YI TÀMBALI NAÑU XEEX BI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ni ñu ko waxee woon lañu ko defe. Layookati Usmaan Sonko yi yóbbu nañu mbiri njiitul làngug Pastef ga woon ca HCNUDH (Haut-commissaire des Nations unies aux droits de l’humain). Muy fa mbaxana doonee benn ñeel àq ak yelleefi doom-aadam ci àddina sépp.

Waxoon nañu ko, tàmbali nañu ko. Démb ci àjjuma ji, layookati Usmaan Sonko yaa nga woon ca Seneef (Genève), fa dalub HCNUDH nekk. Seen kiliyaan bi nekk ci loxoy Yoon moo leen tere nelaw, tere nelaw saa-senegaal yi, rawatina waa këram.

Ginnaaw bees ko daane ñaari yoon, ci digganteem ak Aji Saar ak ci diganteem ak Maam Mbay Ñaŋ, magum àttekat yi dafa dellu gàll Usmaan Sonko juróom-ñaari tuuma yoy, woote xeexoo ak naxasal kaaraange Nguur gi ci lañu bokk. Bi yii yépp xewee ba ñu tée ko téewum négandiku, Usmaan Sonko dafa tàmbali woon xiifal. Boobook tey mi ngi ci 20i fani Yàlla yu mu lànk, bañ a lekk. Fii mu nekk sax dafa lott lool ba ñu rawale ko ca raglu bu Ndakaaru. Tey ci gaawu gi, yéenekaay yi xéyee nañoo siiwal sax ni càmmooñu yaramam yëgatul dara.

Jafe-jafe yii Usmaan Sonko di jànkonteel lañu gis ni ay xeeti jalget yu ñu teg ci kowam doŋŋ lañu. Moo tax ba ñaari layookatam yii di Sayit Larifu ak Xuwaan Barankoo seeti woon Njiital HCNUDH bu diwaanu Afrig sowu-jànt ca Seneef.

Ba ñu génnee ca ndaje ma nag, def nañu yégle doon ci xamle ni xeex bi deful lu dul tàmbali. Te itam, Njiitu réew mi, Maki Sàll, dina xam ni def lu la neex te du mujje fenn, maanaan li tubaab bi di wax « impunité », jeex na fi. Ci seen giseek kilifa gi, tàbbal nañu fa wayndare wu mag tey sàkku ci ONU, mbootaayu xeet yi, mu def lépp lu war ba wayndare wi tàbbi ci loxoy waa CPI (Cour pénale internationale).

Sñ Larifu ak Xuwaan Barankoo xamle nañoot ni xeex bi du mën a yomb, dafay sax tar. Waaye, jumtukaay yi am nañu, te dinañu ko topp ba mu sës. Balaa yàgg dinañu leen gis ci yeneen réew yu deme ni USA.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj