WAXLEEN SEEN XALAAT YAA GORE ! By Defu Waxu 14/04/2024 0 398 Partager FacebookTwitterWhatsAppE-mailImprimer Yeneen i xët BOO BAÑEE ÑAAW… Baabakar Lóo - 26/05/2024 Njiitu Réew Defu Waxu - 02/05/2024 Ndigalu Maam Ya Defu Waxu - 02/04/2024 SÀCCIIN WI JËM CI TÀNN YI DËGMAL TE FEEÑALEES KO Defu Waxu - 06/03/2024 Aji bind ji Defu Waxu Yàgg, yàgg, dëgg ay daan Dëgg lottoon na Senegaal Usmaan Sonkoo tax mu daan Lii dinaa ko bind ngir ëllëg Danga daan xëy di liggéey Njiitu Réew dàq la sa liggéey Dàqin wu ñaaw, mbete sàcc Te yaa doon xeex ñay sàcc Askan wi fal la, def la dépite Ngay dëggal, doon ku nite Fa nga daan taxaw Aasàmbale Ku fa taxaw tey du ko mate Ngay wax dëgg, ñu lay bów Waa APR ak Abdu Mbów Téye sa der bi di ci saw Seen iy sobeek seen iy pexe « Présidentielle 2019 » Ñu lay kókkali, nga nëw doon Ñetteel ca ña jiitu Idiriisa Sekk xëy la wor Maki Sàll téye di tëje Takk-der di kajje, di pese Xalifa Sàll nekk kaso Nga taxawu ko, mu génn dëddu la Ñi fi amul woon resepise Ñi fi amul woon ku leen faale Ñi fi amul woon fitu gaynde Usmaan, yaay ki leen xettali Mag yu bari faalewuñu ndaw Nga wax ak ndaw ba mu mat mag Lu mel nii ci sunu Réew Néew na foo koy gise Ba ñu xamee nag ne yaa leen gën Ca la nu jóg di la tuumaal Jiiñ nañu la fi ciif, jiiñ la rëbel Jiiñ la terorist ak càccug telefon Jël nañu la tëj ak sa njaboot Ñaari weer ci sunu biir Réew Gii gàcce, gàccee ka réy Soo yambaroon nu dooniy jaam Nu ne déet, ñu sànni la kaso Sa pàrti, ñu gont tas Say junniy àndandoo ñu tëj Juroom-fukk ci ñoom ñu rey Siggil ndigaale, Usmaan Sonko Ci Baay Seex Jóob mi ñu bóom Siggil ndigaale, Usmaan Sonko Ci Porospeer Seŋoor sa doom Ñoom ñii, ñooy say nawle Ñiy dund, ñi ëpp matuñu Tey jii, nga génn kaso Ginnaaw nga woorlu jiitu Koor Looy defati bàyyi leen ci xel Nit ñi génn di la teeru Ñoo yey, dangaa gore Maki Sàll bëggul a dem Nga samp Basiiru ngir mu dem Sa jëf yii ni ñu taaroo Yal na yiy ñëw gën a taaru Yaakaar yi nga yee ci nit ni Yal na ci ndam yu réy topp Liy ñëw nag mooy gën a metti Jagal Réew coono la doŋŋ Waaye nag du yow laa koy wax Ku ragal coono daa bañ lu baax Doxal, Usmaan, bul jeng Ci yow kat danuy jàng Ëlleg, bëgg nanu laa weesu Sunuy rakk it nëw di nu jiitu Senegaal dëkkee tedd « Yaa gore », la taalif bi tudd Séex Axmadu Bàmba ki ko bind Njaay-Jaata, dëkk Njaaréem Di góoru Ajaa Mariyeem Moo la naan, dalal ak jàmm ! Séex Axmadu Bàmba Njaay 15/03/2024 Defu Waxu Plus de publications Defu Waxu https://www.defuwaxu.com/author/webmaster10/ NJUREEFI BAC 2024 YI Defu Waxu https://www.defuwaxu.com/author/webmaster10/ WATTU LÀKKI RÉEW MI 2/3 Defu Waxu https://www.defuwaxu.com/author/webmaster10/ WATTU LÀKKI RÉEW MI 1/3 Defu Waxu https://www.defuwaxu.com/author/webmaster10/ BÓOMUG ALEŊ KALI: G7 BU CEES DOOR NA XEEX BI FacebookTwitterWhatsAppE-mailImprimer Widewo VOA AMAL NAB JOTAAY CI MBINDUM BUBAKAR BÓRIS JÓOB GINNAAW BI WEREKAAN BI JËLEE CARGALUG NEUSTADT 2022 BI. CUQAL CI LËNKAAY BII TOFTALU... Defu Waxu - Xët yi mujj CAMPEEF / NGOMBLAAN GI : TAXAWAL NAÑU PEKK GU YEES GI Paap Aali Jàllo - 07/12/2024 LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (5/12/2024) Mbay Sow - 05/12/2024 NDAJEM JËWRIÑ YI Njuga Gay - 05/12/2024 DÉPITEY FARÃS YI DAANEEL NAÑU CÀMMUG MICHEL BARNIER Paap Aali Jàllo - 04/12/2024 ÀMBURUWAAS SAAR : AATU RÉER NA ! Paap Aali Jàllo - 04/12/2024