«BU DUL WOON DOXANDÉEM YI, MBAS MI DU NAANE ÑEEX AFRIG » (Doktoor Séydu Jàllo)

Yeneen i xët

Aji bind ji

  1. Paap Aali Jàllo

Doktoor Séydu Jàllo ab Farmasiyeŋ la, dib biyólósis ak « ancien interne des hopitaux ». Xam-xamam màcc na tamit ci wàllu kiiraayu biir yaram ak ség. Tey, day waxtaan ak nun ci mbasum Covid-19 mi lëmbe àddina si. Ci xaaj bu jëkk bii, day indi ay leeral ñeel Covid-19 bi, di nu xamal yit li waral mbas mi law ci àddina sépp. Li ngeen di jàngsi mooy xaaj bu njëkk bi.

Paap Aali Jàllo : Ginnaaw bin la nuyoo, noo ngi lay ñaan nga wax jàngkati Lu defu waxu yi kan mooy Séydu Jàllo.

Séydu Jàllo : Maa ngi leen di fey, di leen jaajëfal ci li ngeen ma tànn ngir waxtaane mbasum Covid-19 bi. Man, Séydu Jàllo laa tudd. Farmasiyeŋ laa ak biyolosist. Nekkoon naa tamit « interne des hôpitaux » te am naa lijaasa « Master » ci « immunologie et infections », maanaam xam-xamu kiiraayu biir yaram ak ség.

PAJ : Lan mooy koronaawiris ?

SJ : Koronaawiris ngiir bu yaatu la, ëmb ay wiris yu bare lees mën a màndargaal. Ci benn boor, ci seen mbindin, koronaawiris yi dañu am melow téeñlaay, moo waral ñu tudde leen noonu.  Dañuy faral di nekk ci mala yi. Bu ko defee, mën nañ jóge ci mala yooyu, dugg ci biir nit ki. Moo xam daa fekk nit ki lekk malabi, walla mu laale ak moom.  

Ci beneen boor, boolees na koronaawiris yi ci xeeti wiris yiñ dippe « virus à ARN ». Maanaam, xeeti wiris lañ yoo xam ne, benn, mën nañu jóge ci mala dugg ci nit ki ; ñaar, bu ñuy dugg ci nit ki dañuy soppeeku ci anam bu gaaw te dañuy gaaw a wàlle. Loolu, nag, day indi ay jafe-jafe yu bare ñeel pajam.

Te, cig fàttali, ci 21eelu xarnu biñ nekk, koronaawiris yi jot nañ fee sabab ñaari mbas yu metti lool : SRAS-cov ci atum 2002 ak Mers-cov ci atum 2013. Covid-19 biñ jànkoonteel ci jamono jii, xeetu koronaawiris bu bees la. Waaye, nag, dafa wute bu baax ak yi ko jiitu.

PAJ : 3. Lan mooy màndargaal Covid-19 bi ?

SJ : Waaw, ni ma ko waxe léegi, koronaawiris yi jot nañ fee sabab ñaari mbas. Bi ci jiitu, mbasum SRAS-cov, mi ngi amoon ci atum 2002 jàpp 2003. Moom itam, réewum Siin la soqeekoo woon laata muy law ci àddina si, song 30i réew, daaneel fa 8 000i nit, faat ci 774. Maanaam, 100 nit yoo jël ci 8 000i yooyu SRAS-cov bi songoon, 10 yi dañ cee ñàkke seen i bakkan.

Ñaareelu mbas maa ngi tudd MERS-cov. Ca Araabisawdiit la cosaanoo woon, ci diggante 2012 ak 2013. ERS-cov jotoon na dugg ci biir 26i réew, daaneel fa 1.589i doom-aadama, faat ci ñooñu 567. Kon, ci xayma, 100 yoo jël ci 1.589 yooyu jàngoro ji songoon, 30 yi dunduñu.

Bu dee Covid-19 bi, moom bare na ay màndarga. Benn, wax naa ko sànq, ci xeeti wiris yiñ dippe ci nasaraan « virus à ARN » la bokk. Anam bi muy soppeeku dafa gaaw te jéggi dayo. Moo tax, ba tay, amaguñ garabam ndax xamaguñ nim bindoo dëgg-dëgg.

Ñaar, Covid-19 bi mën na nekk ci biir nit ki ay fan, 1 ayu-bés walla 2, te du wonewu. Boroom da koy doxaale, di ko wàll nit ñi te du ci xam dara astemaak ñim koy wàll ak ñi ko ñooñu di wàlliwaat. Muy lu doy waar, raglu lool. Te, boo seetee, SRAS-cov bi, moom, lum gudd gudd, 1 ayu-bés rekk, bu ko defee ci nit ki, màndargay jàngoro ji tàmbalee feeñ.

Ñetteelu mbir miy ràññeelu Covid-19 bi mooy li mu amul xàmmikaayi-feebaru boppam. Boo seetee, way-tawati Covid-19 bi dañuy ame yaram wu tàng, mettitu yaram, put guy xasan, soj bu ànd ak sëqat su wow, biir buy daw, añs. Te, xàmmikaayi-feebar yu ni mel, fekkees na leen itam ci way-tawat yi ame sibbiru, soj, ak yeneen xeeti feebar yu bare.

Màndarga yii daal ñoo gën a fés ñeel Covid-19 bi.

PAJ : Nooy jàngate lawub mbasum Covid-19 bi ci àddina sépp ?

SJ : Ci li mënagum jàpp, Covid-19 bi Siin la doore ca jawub Wuhan. Nee ñu, ci xayma, lu tollu ci 15i miliyoŋi doomi-aadama ñoo fay yeewoo. Muy lim bu takku. Bim fa duggee, nag, ba tàmbalee faagaagal askan wa fa nekk, nguurug Siin dafa gaawantu, lël nit ña. Ñépp daldi déju seen i kër ngir bañ jàngoro ji law seen biir.  Xam ngeen ni, Sinwaa yi dañooyaru te dégg ndigal. Moo tax, am na fa (ca Siin) ay diiwaan ak ay dëkk yoo xam ne mbas mi àggu fa. Mu des nag Aasi, Ërob, Amerig ak li ci des ci àddina si.

Bees amee ab taxaw-seetlu, dees na gis ni, ginnaaw Siin, mbas mi réewi Ërob yi la jëkk a song, teg ci réewi Amerig yi, Afrig door a ñëw. Rax-ci-dolli, jamono jii, réew yi mbas mi gën a sonal ñoo ngi Ërob (Itali, Espaañ, Farãs, Portigaal…) ak Amerig (Etaasini).  Dara waralu ko, nag, lu-dul jëflante bi réew yooyiiyjëflante ak réewum Siin, rawatina demlante bi am seen diggante.

Ndege, ci wàllum njaay ak njënd, Ërob ak Etaasini dañuy jëflante lu baree bare. Te, ku wax njaay ak njënd ñeel ay réew, wax dem ak dikk. Nu bañ a fàtte ni Covid-19 bi amul ay tànk, nit ñiy demlante ñoo koy wàllante seen biir. Kon, loolu moo waral bi mbas mi amee Siin kott, dafa jàll Ërob ak Amerig. Ndaxte, way-tukki yaa ko fa dugal.

Li tax nag mbas mi lawe nii Ërob ak Amerig dafa fekk ni seen i askan meluñu ni Sinwaa yi ci yar ak dégg ndigal. Teg ci ne, seen i nguur teeluñoo jël matuwaay yi war. Ndaxte, réew yu ci mel ni Itali, Espaañ, Farãs, rawatina Etaasini, ak lu ñuy am doole ak i jumtukaayi xarala yu mag yépp, tey, mbas mi sonal leen lool sax. Waxuma la sax, la mu fay faat ciy bakkan, waaye koom-koom gi ci boppam la rajaxe, nasaxal ko ba gaa ñi jaaxle. Moo tax, ñu ngi rëccu bu baax. Waaye, Wolof nee na, réccu day fekk jëf wees.

Afrig nag, li nu séq ak Siin ci wàllu njaay ak njënd yemul ak réewi Ërob yeek yu Amerig yi. Daanaka, demewu fa noonu. Boo xoolee, nun, bi mbas miy door teel nan koo yëg ; bi muy law tamit noonu. Kon, xamoon nan li nu war. Bu ko defee, jot nanoo jël sunuy matuwaay, sunu njiit yi jël ay dogal yu am solo. Dañ tëj ayeropoor yi, gaare roppëlaan yi, tëj digi réew yi (yu suuf yi ak yu géej gi) ba noppi aayembooloo yi.  Am na ci sax réew yu sàrtal gaw(confinement total). Te, Ërob ak Amerig teeluñoo def loolu. Looloo waral jàngoro ji lawul ci Afrig ni mu lawe ca ñoom.

Te, Afrig, bu dul woon doxandéem yi ak Móodu-Móodu yiy daw di ñibbisi, yaakaar naa ni mbas mi doonu fi naane ñeex.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj