BU YÀLLA NEE WAAW, LÉPP AY BAAX

Yeneen i xët

Aji bind ji

Li gaa yi naan bàmba bu naan, Senegaal jamono jii bàmbaam naan na ba cukkur-mbuut. Mbir yi ndeke dafay gën di neex rekk !

Bu doon ne dañu rëbbi woon, dees na wax ne gaynde yi sooyuñu. Mukk ! Nde, fàddati nañu, indaale. Li ci gënatee neex mooy ne, wile yoon, gaynde yu ndaw yee saga lak a sargal Senegaal. Beneen kuppeg Afrig dikkati na, juróom ya mat nañ. Gannaaw Kuppeg Afrig gu mag ga ekibu ñoom Saajo Maane indi woon, waa Beach Soccer teg ca seen bos, ñu ni déet-a-waay ndaw ya ñu tànn ci Sàmpiyonaa réew mi dem jëli CHAN 2023 bi. Ñu foog ni fa lay yam, U20 ba dolleeti ca CAN biñ jagleel ñi amul 20i at. Fa ñuy waxe, naan lii moo neex waay, waa U17, caat yi, wisal nu ci kubu CAN U17 bi. Ñoom it, rëbbi nañu, xeex, jaayante ba indil ñu kuppeg Afrig giñ leen jagleel ñoom it. Bu doon loxo, ñu ni juróomi baaraam ya mat nañ.

Barki-démb, ci àjjuma ji, yamook 19 Me, la sunu ndaw yi amagul 17i at doon jàmmaarlook Marog ñeel finaalu kub ba. Ba joŋante bi jotee daw tuuti nag, xel teeyoon na. Ndaxte, dañu ne piib, yàggul, rekk Marog yoxosu leen, dugal benn bii ci 14eelu simili bi. Senegaal topp ci ginnaaw benn bii biy daw, joŋante biy metti ba xaaj bu njëkk bi jeex. Ñu dellusi, nekkaat ci, mbir yi xaw a dëgër ci saa-senegaal yi ba tay, ñuy dawal ànd ak jom, fullaak fayda ba ca booru 78eelu simili ba, ñu daal ni am teg-dóor (penaltie), kii di S. Fàllu Juuf daldi koy dugal (80i simili), muy 1-1. Ñu tegaat bal bi, ci diggante xef ak xippi, Senegaal daldi koy këf, dawal ba àgg ci kãwu Marog, M. Sawane newaat ko pëy ca caax ya. Waaye, sunu xale yaa bari jom waay ! Naka noonu, saa-marog yi nekk cay daw, di daw ba ni joŋante bay jeexee. Boobii mbégte, boobii jaloore, kenn xamul fu mu yem !

Senegaal, ni nu ko waxee woon, ajati na turam ci kuppeg Afrig, gën a bàyyiloo àddina xel ci kuppeem ak i ndawam.

Kii di Amara Juuf miy kàppitenu xale yi (14i at) mooy ki ëpp lim dugal ci joŋante bi, 5i bii la dugal. Amaana mu teeri fay magam, ñoom Lamin Kamara ak ñoom Paab Démba Jóob teeri ca Tugal ginnaaw bi jëlee woon kubu CAN U20. Nuy ñaan cat bañ koo jiitu fa mu jëm ak i moroomam.

Jamono jii nag, Afrig gépp a ngi ñu teg bët, te leer na ni ñoo ngi nuy daasal di nu waaj yeneen kub yiy nëwaat, nanu gën a teg tànk yi, bañ a bég rekk bàyyi.

Gayndee njaay mbara-wàcc !

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj