Barki-démb ci gaawu gi la ko Rimtalba Jean Emmanuel Ouédraogo xamle ci ab yégle. Moom Jean Emmanuel di ki yor kàddug Nguur gi (porte-parole) moo biral ne kibaaraanu Farãs googu di “Le Monde” amatul sañ-sañu génnee fab xibaar. Maanaam, muy ci mbooleem bànqaas yi mu doon jaare ngir tasaare xibaar yi. Yooyu yépp, nañu maandu ci seen i mbir. Mu mel ni kon Burkinaa Faaso, Niseer ak Mali moom meyuñu dara waa Farãs. Li mat a laaj kay mooy lu tax ñu dakkal seen liggéey bi xaat ?
Diggante atum 2020 ak 2022 jàpp atum 2023 mii ñu nekk, kibaaraani Farãs yi amuñu jàmm ci réew yooyu. Ndax, Asimi Goytaa bi mu ñëwee ca atum 2020 yàggul dara mu jële leen ca réew ma. Ibraahiim Taraawore tamit ma nga ca tànk yooyu. Mooy li ñu naan mënoo bañ ginaar ba pare bëgg nen. Dafa di nag, Farãs ak sóobare yi jiite réew yooyu mënuñoo séq ab taal. Maanaam defuñu nenn. Ndax, dañoo jàpp ne nekkuñu ci li neex Farãs. Ba tax, seen kibaaraan yi duñu teg seen der lu baax. Duñu jóg ci di leen jéem a jaxase ak seen askan ba ci sax seen i mbokki dëkkandoo ak àdduna wërngal-këpp.
Li ko waral mooy, nee ñu, dañoo gis kibaaraan googu génnee ab yaxal ci àjjuma ji ñeel xeex bi ñu doon def ak jiyaadis. Ñoom dañu cee ŋàññi ndam li sóobare si am ca cong ma amoon ca Djibo. Maanaam ñoom daal dañoo bëgg a neenal liggéey bi sóobare yi ak VDP yi (Volontaires pour la Défense de la Patrie) def foofu. Nde, Nguur gi day nëbb askan wi li xew dëggantaan ci xeex bi. Rax-ci-dolli, deful lenn lu dul ag wonewu ci kàddu yi ñuy jibal ci kanamu askan wi. Nguur gi jàpp ne liy mébétu gaa ñi mooy jaxase, wone ne ñoom dañoo lajj ci xeexu ngànnaay yi ba noppi soppi ko ndam ci kàddu yi ñuy jibal. Te, ñoom jamono jii kenn umpalewul xeex bi ñu def ci wàllu cong yooyu ñu leen di faral di song ak ku leen mën di def.
Looloo tax jamono jii waa Burkinaa jël ndogalu dakkal seen liggéey ca réew ma. Ndax, dañoo gis ne xeex bi ñuy xeex rëtalkat yeek ñépp ñi leen di song, kibaaraan googu daf ci am péete. Te, ñoom duñu nangu wenn yoon kibaaraan googu di leen ko yàqal. Ba tax na, ñoom, ñu ngiy woo askan wi ñu gën a ànd ak dal te teey. Bañ a bàyyi kibaaraan yooyu ñuy jaxase seen i xel walla di leen sikki-sakkaloo ci ñoom. Ndax, ñoom amuñu beneen jubluwaay lu moy fexe ba lëbëje kàrt gi, ba ñépp di sikki-sàkka, kenn bañ a wóolooti kenn.
Dafa di nag, ku sa wujj di sëlëm moom doo set. Te, kujje gu metti gi dox diggante Farãs ak réew yooyu nga xam ne ay sóobare ñoo leen jiite kenn naatableetu ko. Muy Mali, Niseer ak Burkinaa Faaso donte ne sax am na yeneen réew yu sóobare jiite te, coow jibul. Kon, ñoom dañoo jàpp ne buñu lekkul ci ndab li rekk dañ cee war a xëpp suuf.