Burkinaa Faaso dàq na sóobarey Farãs ya ca réew ma

Yeneen i xët

Aji bind ji

Sóobarey Farãs yi dinañu jógge ca Burkinaa Faasoo. Ginnaaw bi ko kilifay réew ma sàkkoo, kilifay réewum Farãs yeet nangu nañ ndogal li ba dinañu fa jële seeniy sóobare feek weer, bu yàggee ba yàgg.

Àllarba 18i fan ci weeru sãwiye 2023 la xibaar bi jolli : Njiitiy Burkinaa dàq nañ sóobarey Farãs ya ca réew ma. Ab bataaxal lañ jébbal ndawal Farãs li ca Ouagadugu. Ci biir bataaxal ba, ña nga ca doon ñaawlu ak a dakkal déggoo bi ci diggante ñaari réew yi ñeel kaaraange gi.

Lu doonoon teewaayu sóobarey Farãs ca Burkinaa ?

Ci atum 2018 (17 Desàmbar) la ñaari réew yi xaatimoon boobu déggoo ngir gën a dëgëral seenub lëkkoo. Naka noonu, ñaari Nguur yi xasoon ànd àndu nawle te fas yéene xeex rëtalkat ya dugg ca réewum Burkinaa ci atum 2015 ba tàmbale woon fa am doole. Jamono yooyu, kii di Rok Mark Kiriscaan Kaboore (Njiitu Burkinaa la woon) la Emanuyel Makarõ dalaloon ci Paleem ba yékkati fay kàddu ni déggoo bi:

« Dina nu yóbbu ci nu gën a ñoŋal yoonal gi (le cadre juridique) sunuy jàmbaar dee lëkkaloo ba sàmmoonte bu baax ak moom-sa-réewu ku ci nekk »… « Farãs dina lonkook yéen ci anam yu amul benn sikki-sàkka ci xeex bi. »

Ci déggoo boobu, réewum Farãs warul woon a dolli benn soobare ca ña jotoon a nekk ca dalub Farãs ba ca Ouagadugu. Réew ma jotoon naa dalal ci atum 2010 lii di Force Sabre, dig gàdd (contingent) gu tollu ci 400i fors espésiyaal. Jooju jamono, Belees Kompaaware moo nekkoon ca boppu réew ma. Amul woon benn taxawaay buñ ko sàkkal. Ak déggoo bu 2018 bi, seen wareef mooy ànd ak jàmbaari burkinaa yi te dooleel leen ba ñu mën jàmmaarlook rëtalkat yi.

Lu tey doon ba ñu bëgg leen faa jële

Lu ëpp 4i at ginnaaw bi déggoo bi amee ci atum 2018, tey la rëtalkat yi gën a am doole, rawatina ci bëj-gànnaaru réew ma. Ba ci ayu bés yii ñu génn, lu ëpp 50i jigéen lañ jàpp dugg ak ñoom ci àll bi. Bees sukkandikoo nag ci Emanuyel Wedaraagoo mi yor kàddug Càmm gi ca Burkinaa, dara waralul ndogal li lu dul ni Burkinaa dafa fas yéene xeex xeex bi ak dooley boppam :

« fii mu tollu, li nu ci mën a wax mooy ñaawlu gii nuy ñaawlu dafa doon lu war. War ngeen a seetlu ni kilifay Farãs ñoo ngi doon wax saa su nekk lan mooy wareefu Njiitiy Burkinaa yi ci teewaayu sóobarey Farãs ci réew mi. […] Gis-gisub Burkinaa tey mooy waa Burkinaa ci seen bopp ñooy takku taxaw ngir aar réew mi, foqati lépp lu bokk ci réew mi te nekk ci loxoy rëtalkat yi. »

Mu mel ni Saa-Burkinaa yi dañoo jël ndogalu taxawal seen bopp ngir aar réew ma, te bañ koo yaakaar ci keneen. Bi xibaar bi siiwee tamit, askanu burkinaa yi àddu ci Africanews wone nañ bu baax seen ànd ci ndogalu kilifa yi. Ñenn ñi sax dem nañ ba naan yeex nañ koo def. Waaye terewul yenn ciy laaj yékkatiku. Yu ci demee ni mbaa Burkinaa mën naa xeex moom kott xeex bi ? walla sax ndax gaawantuwuñu ndogal li. 

Ginaaw juróom i weer bi sóobarey Farãs yi raxasoo ca Mali ba set (ut 2022), dinañ dellu raxasooti sa Burkinaa ba set wecc. Terewul ñu mën see jàpp ne déggoo bi ci diggante ñaari réew yi ñeel kaaraange gi moo fiy yam waaye du lëkkaloo ñaari réew yi. Sóobarey Farãs yi kon dinañu fa jógé feek weer niki déggoo bi waajale saa bu tàqalikoo waree am. Bu ñu jóggee ca Burkinaa nag dinañu jàll ca Niseer walla ca Koddiwaar, fa Farãs dese i sóobare ci diwaanu Sayel bi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj