Diggante alxames ak àjjuma (12 ak 13 sãwiye 2023), lu ëpp 50i jigéen ñoo ni mes ne meenteñ ca Burkinaa Faaso. Ay defkati ñaawteef a leen jàpp, daldi laqook ñoom ca biir àll ba. Ba jamonoo yii, kilifa yaak askan wa xamuñu fu leen jant dee tiim.
Nit ñañ teg loxo ca Burkinaa Faaso ñooy doon coow ca réew ma ba leegi. Ay nit ñu gànnaayu ba diis ñoo dogaale, lu ëpp 50i jigéen daldi leen yóbbu. Mbir ma nag, ma nga xewee ca gox-goxaat (commune) bu ñu naan Arbinda, féete ca bëj-gànnaaru réew ma. Alxames, 12 sãwiye 2023 la ñetti jigéen daanusi ca dëkk ba ngir yegge leen jéyya ji. Ñoom nag dañoo raw ndax ca mbooloo ma lañ bokkoon. Ca ëllëg sa (àjjuma 13 sãwiye 2023), laata mbir mi di siiw ca réew mépp, ñu neeti doŋet meneen mbooloom jigéen ca sow-jantu gox-goxaat ba.
Ginnaaw ayu-bés bi yóbbu gi xewee ak tey, du kenn ku xam ci lu ñu nekk. Li gën a yéeme ci mbir ma nag mooy i jigéen kese lañ, genn góor bokku ca. Bi rëtalkat yi duggee ca gox-goxaatu Arbinda, góor ña dañoo takku taxawal ab kurél VDP (Volontaires pour la défense de la patrie) ngir jàppale làrme bi ci xeex bi. Ca la rëtalkat ya jóge jàppal leen mer, daldi wër-ndomb dëkk ba ba genn góor daawul géen naan yaa ngay doxi say soxla. Lu ko moy ñu faat la.
Looloo waral ba jigéen ña rekk a daan dem ak di ñëw, di doxi soxla yeek a andi dund gi. Ba ci ñii dem, ña nga leen dogaale fekk ñu doon wuti dund jamono yii nga xam ni sàq ya amatuñu dara lu nit mën a lekk. Ci xibaar yi mujj génne, bokk na ca ñañ yóbb ay xale yu ndaw yu feragul. Muy mbir mu doy waar ba àddina sépp di ko naqarlu.
« doon na njàqare lool ci man ñu yóbbu bëccëgu ndar kàmm ay fukki-fukki jigéen yu doon wut lu ñu dundale seeniy njaboot. […] Maa ngi sàkku ñu bàyyi leen ñoom ñépp ci ni mu gën a gaawe te njiit yi amal ab gëstu bu gaaw te bañ a am benn par-parloo ba ñu mën a teg ci yoon ñi amal jile jëf.» (Wolkëer Turk, magum komiseer bu Mbootaayu xeet yi ñeel yelleefi doom-aadama).
Ba fii nag, amul genn kurelug rëtalkat gu féeteyoo mbir mi. Waaye, askan waak njiit ya wóoluwuñu ci wenn yoon GSIM (Groupement de soutien à l’islam et aux musulmans). Jàpp nañ ni ba fa muy mujj, seeniy loxo du ci set. Nde, bi rëtalkat yi duggee ca réew maak tey, ñoom ñoo tere noyyi nit ñi ci diwaan boobu.