ARCOP (Autorité de Régulation des Marchés Publics), di banqaas biy saytu lépp lu aju ci yoonalug jawi bokkeef gi, siiwal na caabalug ati 2022-2023 yi. caabal googu nag, dafa feeñal ay njuuj-njaaj, ay mbuxum ak i jalgati yu jéggi dayo ñeel anam bi ñu doon joxee ja yi. Yéenekaay bii di Libération moo xëyee xibaar bi ci xëtam bu njëkk. Bees sukkandikoo ci sunu naataangoo yi, doxalin yu safaanook yoon yooyu, ñi leen def ñooy : ay campeef ak mbooloo tund yi, rawatina Anacmu, Crous bu Bàmbey, meeri bu Tuubaa Mosquée, ak itam ci yenn ciy njëwriñ ak i bérébi bokkeef gi.
Yéenekaay bi dafay joxoñ « ag kootoog caay-caay » diggante ay lijjanti [këri liggéey] ak i banqaasi bokkeef gi yoy, seen jubluwaay moo doon « yóotu » ay wayndarey càkkuteefi gaaral [dossier de demandes de propositions (Drp)]. Naka noonu, dafa am itam jawub jumtukaayi pekk bu ñu jagleel ñoo xam ne yeyoowuñu ko. Maanaam, dañu waroon a jënd ay jumtukaay yees di aajowoo ci liggéeyu pekk [biro], ñu daldi jox ja bi kenn koo xam ne, ci gaaraas, maanaam mbiri daamar, lay yëngu. Rax-ci-dolli, am na yeneen i jawi liggéey yoy, ñaare, dañuy weesu 700i miliyoŋ ciy seefaa. Ja yooyii nag, ci li caabalu ARCOP bi njort, dañu ko dénk ay lijjanti yu matewul xam-xam beek xarañte gi.
Ba tay, ci li Libération bind, caabal gi dafa duut baaraam ay « faktiir yu ëpp » ak « ay laaj-tontu yu dëppoowul ak yoon » ci ja yu bari, raatina ca njëwriñu ndox mi ak Cetal gi, ca CDC (Caisse des dépôts et consignations) ak ca liise bu Sànjara. Bu dee liise boobii nag moom, am na ci 3,2i miliyaari seefaa yu ne mëy, kenn xamul fu koppar yi jaar.
Saabalkati Libération yi jokkoo nañu ak njiitul ARCOP li, Sëñ Mustafaa Jóob, ngir laaj ko ci njureefi caabalgi. Sëñ Jóob, ciy tontoom, dafa fàttali solos jubal ak leeral ci anam bi ñuy joxee ja yi ak ci anam bi ñuy saytoo koppaari askan wi. Bees sukkandikoo ci kàdduy njiitul ARCOP li ba tay, bu yoon demee ba dëggal jalgati yi seen caabal gi feeñal, warees na teg ay daan nit ñi ci laale.