Ëttub cettantal gi dafa bokk ci bànqaas yiy saytu liggéeyuwaay yi nga xam ne ci Nguuru gi lañu aju. Seen liggéey mooy càmbar koppar gi campeefi réew miy liggéeye ngir seet naka lañ ko yoree. Cig caabal lañuy biral seen i ngirtey lëñbët. Ñoom nag, ci altine jii weesu lañu biral caabalug atum 2020 meek mu 2021 mi ñeel caytug koppar gees jagleeloon naalub FORCE COVID-19 (Fonds de riposte et de solidarité contre les effets de la covid). Caabal googu nag, daanaka bàyyiwul kenn, joxoñ na baaramu tuuma jëwriñ yu bari, ay fajkat ak i kilifa ci wàllum paj mi. Waaye nag, ñaar ñi ci gën a fës di kii di Abdulaay Juuf Saar mi woon jëwriñu wér-gi-yaram geek ndimbal njaboot gi jamono jooja ak kii di Mansuur Fay mi woon tamit jëwriñu yokkuteg mboolaay gi yemale gi ñeel askan week mberaay mi. Ñoom ñaar nag, caabal gi daf leen a taqal, tuumaal leen njuuj-njaaj.
Bari nay jëwriñ yoy, caabal gi duut na leen baaram. tuddees na leen ci mbiriy nger, njuuj-njaaj ak luubal. Jëwriñ yooyee lëmbe kibaraan yi nag, dañu weddi tuuma yépp, daldi leen di teg ci kow ndoddi Njiitali caytuy matale yeek jumtukaay yi, gàttal biy joxe, ci farãse, DAGE(Directeur de l’Administration générale et de l’Equipement). Waaye, loolu yoon a ko mën a leeral. Dafa di, ku ñépp tufli, nga tooy.
Ca mars 2020 la mbas mi dugg ci réew mi. Bi mu fi duggee nag, dem ba law, Njiitu réew mi woowee ñépp ngir ñu booloo, bennoo jàppalante, xeex mbas mi. Ginnaaw gi la taxawal ab naal, duppee ko Force Covid-19, daldi koy jagleel alal ju takku. Alal jooju, ñépp ci joxe, ba askan wi, ku nekk am na loo xañoon sa bopp, coppati as-tuut ci li néew li nga yoroon, ak ni jamono mettre, daldi koy Nguur gi. Lees ko dugge woon mooy dooleel njiit yi ngir ñu xeex mbas mi, muccal réew meek i doomam. Ndege, mbasum Covid-19 mi, àddina sépp la lëmbe woon. xaalis boobu, nag, dañ leen ko dénkoon rekk, du woon seen moomeeli bopp. Te, denckatu xaali, wóor a ko war. Wànte, wóol nit terewul wattu nuit. Looloo tax ñu sanc fi campeef yu mel ni Ëttub cettantal gi, ngir ñuy settantal ak a saytu koppar fi koppari réew miy dugg.
Ci seen caabal gu yees gi nag, ci xëti fanweer ak ñeent ak fanweer ak juróom yi, leeral nañu ci fu koppar gi yépp jóge. Ca atum 2020 ma, koppar gi ñu dajale woon, mu ngi tollu ci 789,579i miliyaari seefaa. Alal joojile nag, PTF (partenaire technique et financier) yi joxe nañ ci ci 667,371 miliyaar, Càmm gi génnee 102, 25i miliyaar, saa-senegaal yi tamit natt nañu lu tollu ci 19, 958i miliyaar. Ca atum 2021 ma tamit, am na lu tollu ci 15i miliyaar yu teg yoo xam ne, ñi ngi bawoo ci BID, l’UEMOA ak BM. Loolu lépp ngir xeex mbas mi. Xaalis bi nag ak li muy bari bari am na lu ci delluwaat ci askan wi. Waaye, am tamit lu ci dellu ci nafay gaa ñi, faf ñu defaroo ca ñoom. Mu mel ni gaa ñi dañoo gaawantu duy seen i nafa jamono ja nga xamee ne saa-senegaal yi seen fit demoon na ci sababu mbas mi. Loolu lañu naan, ay woo gis, jàmmi keneen la.
Luubal googu, nag, Abdulaay Juuf Saar ak Mansuur Fay, kenn demu ci ñu des. Nde, bees sukkandikoo ci caabal gi, doxalin wu bon lañu doon doxal. Ndege, ñoom ci seen pas yi ñu doon def ak ja yi, ci yaa-ma-neex kepp lañu ko tegoon, amul def yëgle (appel d’offre) ngir xool kan moo yor ak kuy jaay lu yomb te baax. Déedéet, ñoom kay, li ñu layoon mooy ne, mënuñoo woon a xaar ndaxte mbir mi dafa jampoon. Mu mel ni kuy tëru, kuy teggee ci aay. Moo tax, kii di Abdulaay Juuf Saar rekk, ak ja yi mu lëkkaloo woon, def nañu lu ëpp ñetti weer te jotul matuwaay yi mu doon sàkku. Te, ba tey amul benn daan bu dal seen kow, lu tax ? Kii di Mansuur Fay daanaka toog na lu ëpp ñeenti weer, kenn gisul dund bi mu doon wax ne jënd nañu ko.
Mu am tamit ay mbir yu doy waar yoo xam ne ba tey am na ci. Ndax Këru liggéeyukaay (entreprise) yu ci mel ni Medina Sarl, Nkg, Sonabi Al Nabiyyu Voyage nga xam ne jox nañu ay matuwaay MSAS lu tollu ci 15.578.132.877 seefaa, kër yooyu yépp, soxna sii di Ndey Kati Gajaga kott a leen moom. Maanaam, soxna si ci jëmmi boppam rekk, am na lu tollu ci fukki ja ak ñaar ci jamono joo xam ne, gaa ñi fare foofu yépp a lott ndax mbas mi. Te, boo xoolee li ñu jënde, daanaka réew mi da ciy ñàkk lu tollu ci benn miliyaaru seefaa. Ba tey, mu am tamit ay miliyoŋ yoo xam ne bu ñu leen xaymaa, daanaka dañuy dem ci miliyaar yoy, nee nañu jébbal nañu leen raglu yi te ba tey joxewuñ ci jenn firnde, bu nu sukkandikoo ci Ëttu cettantal gi.
Caabal gi rax ci dolli ne, li Mansuur Fay waxoon ne loolu la jënde ceeb bi, matu ko. Maanaam dafa ful njëg yi. Teg ci ne, ñoom ñu doon joxe ja yi, yëfi maa-tey lañ doon def, di jox ay këru liggéeyukaay yoo xam ne amuñu xareñte gi muy ci wàllum wér-gi-yaram wi ak dund bi. Moo tax nag coow li bari na ci luubal gi lool ci ndoddi ñaar ñooñu. Waaye tamit, am na yeneen i béréb yu laale ci mbir mi. Ndax, dafa am ay koppar yoo xam ne, fi ñu leen dugal laalewul ak mbas mi wenn yoon. Te, loolu mi ngi tollu ci 19 727 096 727i seefaa. Ñi séq koppar googu nag, ñii la ci caabal gi lim :
“ Ministère de la fonction publique et du renouveau du service public, Ministère de l’urbanisme, du logement et de l’hygiène publique, Ministère du commerce et des Petites et Moyennes entreprises, Ministère des Mines et de la Géologie, Agence nationale de la Maison de l’Outil, Ministère de la microfinance et de l’économie sociale et solidaire, Agence nationale d’insertion et de développement agricole, Agence pour la gestion du patrimoine bati par l’Etat, Agence nationale pour la promotion de l’emploi des jeunes.”
Li ñu dugal ci koppar ci foo xam ne laalewul dara ak mbas mi bi ñu xayma lépp lépp, tollu na ci 49 586 598i seefaa.
Ba tey, ku ci mel ni Mustafaa Jóob nekkoon ci Ministère du Développement industriel et des Petites et Moyennes Industries (MDIPMI) jotoon na ci koppar gi lu tollu ci 2 500 000 000i seefaa ngir 6 250 000i ciy mask yi mu waroon a defar. Waaye, loolu ñi ngi ko dugal ci am sàq mu ñu dippe « Fonds d’Appui à la Promotion de la Petite et Moyenne Entreprise » mu ñu tijji ca BOA. Ëttu cettantal gi nag, nemmeeku na ay yoon yu bari kii di Muhammad Bàmba Amar di génne xaalis ci sàq moomu nga xam ne FAPPME moo ko taxoon jóg. Daanaka, def na ko lu tollu ci juróom-fukki yoon ak juróom te li ci gën a doy waar mooy lu tollu ci juróom-fukki miliyoŋ walla téeméer rekk lay génnee te Mustafaa Jóob mooy kiy xaatim seg yi. Bi ñu xaymaa li mu génnee ci atum 2020 mi kese, tollu na ci 4 845 000 000i seefaa, te 2 500 000 000i ci koppar gi ñu dajale woon ngir xeex mbas mi la bokk.
Waaw ! Lii nag, ba kañ ? Bànqaas gu génnee ag caabal rekk nga taf sa gémmiñ. Muy OFNAC, di IGF, di ARMP, di CDC gii nga xam ne caabalam gi mooy lëmbe réew mi ci jamono jii. Xameesul ndax mbir yi soppeeku na. Waaye, ya ko jiitu woon moom, ña ñu duutoon baaraamu tuuma ba tey ñoo ngi dox seen i soxla. Kon nag, day mel ni yoon lu ñu ko waxal moom la. Ndey-ji-seex kat, njaaxanaay la war a tëdde. Ku jalgati yoon mu dello la ci yoon. Walla boo bokkee ci Nguur, yoon mënalul a dara ? Bu dee loolu la, nañ nu ko wax, nu xam ko mu jeex.
Caabal gii nag mooy firndeel li ñu naan rongooñi baadoola ñooy siim cerey buur. Ay nit ñu dajale seen alal, nga ñëw def ci lu la neex. Moone, ba mbir mi dooree la am ñu artu woon ci yorinu koppar googu. Ñooñu yey nañu ñépp tey. Ndekete yoo, mbas mi am na ñu mu mbas. Léegi kay li am ba des mooy donte ne sax yoon tuddagu leen, war nañoo mën a génn leeral mbir mi walla ñu yóbb seen bopp ca kanamu yoon. Ndax kat, li am ba des mooy, ñépp a xam ne caabal gii ay como defaruñu ko de.