Caaroy 44, xew-xew bu tiis la ci mboorum Afrig, rawatina mom Senegaal. Jéyya jooju, ma nga xewoon ca njeexitalu ñaareelu xareb àddina si. Ma nga ame woon fa “camp” bu Caaroy, biir Ndakaaru, ca atum 1944. Waaye, mel na ne ba tey pënd ba wureegul. Nde, doomi Afrig yaa ngi wéy di metitlu jëf ju ñaaw jooja. Muy góom bob, naam légét baa ngi fàŋŋ. Li xolli góom bi nag, mooy ndogal li waa Farãs jël ñeel ñenn ci jàmbaari ya ñu faatoon fa béréb boobu. Ndogal loolu la Njiitul Pastef li, Usmaan Sonko, di ñaawlu.
Diggante Farãs ak Afrig mel na ne ci coowoo, nappante, noggatu ak naxante du lañu dëkk. Ndax, bari na ci réewi Afrig yoo xam ne sii, Farãs a leen nootoon, benn ci Senegaal gii. Dafa di, taxawaayu yenn ndaw yi ci yenn ci réewi Afrig yi Farãs tegoon loxo dañoo tàmbalee soppeeku. Moo tax, bi fara-saytu Nguuru Farãs bi ñu dénk li ñuy dippe “chargé des Anciens combattants et de la Mémoire” siiwalee ndogal li ñu jël ñeel jàmbaari Caaroy 44 yi, coow li ne kurr.
Ndogal li ñu jël mooy xamle ne am na juróom-benn ci ñoom yoo xam ne gërëm nañu leen. Ci gàttal, sant nañu leen ci taxawaay bu rafet bi ñu taxawal réewu Farãs ba dee ci. Nde, ñoom ñoo xeexal ko ba génne Farãs ci guuta gi mu nekkon, daldi koy afal. Li yékkati xol yi nag mooy kàddu gii : “Dañoo dee ngir Farãs”. Juróom-benni jàmbaar yooyu, am na ci ñu bokk Burkinaa Faaso, Senegaal ak Koddiwaar. Ndogal loolu waa Farãs jël, la Njiitul Pastef li di naqarlu ci mbind mi mu siiwal ci xëtu Facebookam. Nde, dafa jàpp ne waa Farãs teguñu ko fenn. Te, dafa jot kilifay réew moomu soppi seen i doxalin. Rax-ci-dolli, ñu xam ne, la woon, wonni na.
Dafa di, kilifay Farãs yi dañoo toog ba mu neex leen, ñu ne dañuy gërëm juróom-benni sóobare yoo xam ne, làrmeb Farãs moo leen bóom fa “camp” bu Caaroy, ca atum 1944. Te, li ñu leen sargale du lenn lu moy “dangeen a dee ngir Farãs”. Li ko jaaxal kay mooy lu tax gaa ñi am taxawaay bi ci jamono joo xam ne réewum Senegaal a ngi ci waajtaayu jox geneen xar-kanam xew-xew bu metti boobu. Te, at mii lañuy màggal juróom-ñett-fukkeelu yoon wi mu amee ak léegi.
Li muy fàttali Farãs mooy ne ñoom kese dootuñu mën a nettali pàccu mboor mu tiis moomu. Kon, du ñoom kese ñoo war a wax limu Saa-Afrig yi ñu wor, rey leen ginnaaw bi ñu xettalee Farãs. Waaye, yemul foofu kese. Ndax, nee na du ñoom ñooy jël ndogal ci xeetu ngërëm walla sargal walla ci defaraat yi mu yellool. Te, nee na ginnaaw ci tey, muy Caaroy 44 ak xew-xew yi ci des yépp, dinañu leen fàttalikoo neneen. Mënees na jàpp ne, moom njiitul Pastef li, dafa bëgg mbuumu njaam gi dog. Maanaam, ñu xam ne, la amoon démb ak barki-démb, dakk na. Na ku nekk yem fa nga war a yem.