Ëllëg ci dibéer ji, 1 fan ci weeru desàmbar, dinañu màggal fi Senegaal bésub Caaroy 44. Muy màndargaal bés bi ñu bóome ñees duppee « Les tirailleurs du Sénégal » fa dalub sóobare bu Caaroy.
Bu ñu nee les Tirailleurs sénégalais, xel yépp dem ci ñaareelu xareb àddina si, bi Itleer nammee nappaaje réewi tugal yi ngir yékkati xeetu almaŋ. Ñuy ay doomi réewi Afrig Sowu-jànt yi Farãs nootoon. Ñu dajalee leen fi Senegaal, yóbbu tugal ngir ñu xettali réewum Farãs ak i doomam. Ñu mujj caa am ndam lu réy ba Farãs dellu moom boppam.
Waaye nag, Tirailleurs Sénégalais yooyu waroon a am woyu jaloore bu dul fay, dañ leen a mujje bóom keroog benn fan ci weeru desàmbar 1944 fa dalu sóobare bu Caaroy. Muy jëf ju làrme Farãs amal ginnaaw bi ñu doon laaj seen peyoor ngir dellu fa seen i njaboot.
80i (juróom-ñett-fukki) at ginnaaw bi ñu leen bóomee ak tay (1944-1924), anam yi ñu leen bóomee ngi wéy ñuy luññuti ci njàngalem mboor. Lépp lees yaakaar ni moo ciy xibaar yu wóor a ngi ci yoxoy Farãs mi nekk di nëpp-nëppal ak a diib-diibal. Mësuñu woon nangu sax ni bóom am na ci. Nde, fiñ ko jàppoon mooy ni dañ fippu, xeex am ci seen digganteek sóobarey Farãs yi ba liy xew daldi xew.
Ci pàttaliku gi ñu koy fàttaliku ren nag, la réewum Farãs sog di nangu jaar ci baatu bóom. Bees sukkandikoo ci kàddu yi Njiitu réew mi Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay yékkati barki-démb, ci bi muy amal waxtaan ak waa France 2, Emmanuel Macron (Njiitu réewum Farãs), bind na ko bataaxal. Ci biir bataaxal boobu, nangu na ni bóom la. Terewul nag, Njiitu réew mi fésal ni bari na lu réewum Farãs làq ci mbir mi. Waaye, moo ngi xaar ci ànd bu bees bi ñu sumb mu jébbal leen léppi dëgg ji.
Ci ànd bu bees boobu sax, ab misiyoŋ judd na ci ba ay doomi réewum Senegaal yu seen xel màcc ci mboor demoon fa réewum Farãs ngir amal fay gëstu ci seen (archives yi). Bokk na ci luñ jot a dëggal ni limub ñi ci faatu ëpp na lool lim bi Farãs siiwal. Bu ñu noppee ci gëstu bi, dinañu jébbal Càmm gi ab téere (un livre blanc) keroog 3i pan ci weeru awril 2025.